2
Yeremi àddu na
Ndeysaan Boroom bee mer ba xiinal Janq Siyoŋ
mu taaru mi.
Fa asamaan la rattaxe sagu Israyil fa suuf.
Keroog bésu meram ma, bàyyiwul xel,
ne këram googoo di ndëggastalam.
 
Boroom bee modd te yërëmul
mboolem sanci Yanqóoba.
Ca meram ma la màbbe
tatay Janq Yuda mu taaru ma.
Moo detteel nguur ga aki garmeem,
sobeel leen.
 
Tàngooru sànjam la dagge
gépp kàttanu Israyil.
Fa kanam noon ba la roccee
dooley ndijooram.
Moo tàkkal Yanqóoba
ni sawara wuy sëlsëli,
ba xoyom mboolem la ko wër.
 
Boroom bee tàwwi ag fittam
mel ni ab noon,
moo diire ndijooram, mel ni bañ,
moo bóom mboolem lu neexa xool.
Ci biir xaymay janq Siyoŋ mu taaru ma
la yuri am sànjam ni sawara.
 
Boroom bee mel nib noon,
modd Israyil,
moddaale këram yu taaru yépp,
tas ay tataam,
ba fulal Janq Yuda mu taaru ma,
ay yuux aki jooy.
 
Moo tas mbaaram ni bu doon mbaarum tool,
moo rajaxe bérabu ndajeem.
Aji Sax ji moo fàtteloo waa Siyoŋ
màggal ak bésub Noflaay,
te tàngooru meram la xalabe buur ak sarxalkat.
 
Aji Sax jee jañax sarxalukaayam,
gedd bérabam bu sell.
Moo teg ci loxol noon tatay këram yi.
Biir kër Aji Sax ji la baat xaacoo,
ni bu doon bésu màggal.
 
Aji Sax jee dogoo rajaxe
tatam janq Siyoŋ mu taaru,
Moo tàllal buumu nattukaay, ngir tas ko,
bankul loxoom it te màbbu ko.
Moo jooyloo tata ak tabaxub fegukaay,
ñu ànd tojatoo.
 
Bunti dëkk ba suulu na,
te moo yàqte, dammate weñi tëjukaay ya,
buuram aki garmeem a tumurànkeji
ca yéefar ya,
te téereb yoon amul,
yonent it gisatul peeñu
mu bawoo fa Aji Sax ji.
 
10 Magi janq Siyoŋ mu taaru ña nga toog, xeremlu,
xëppoo suuf, sol ay saaku, di ñaawlu.
Janqi Yerusalem sëgg, seen bopp jëm suuf.
 
11 Samay gët a giim ndaxi rongooñ,
samay butit fuddu,
xol ŋiis, jeex tàkk:
ci tasteg samaw askan;
xale yeek gone yiy nàmp
ne lasar fi mbedd yi!
 
12 Seen yaay lañu naan:
«Ana fu nuy lekke, ba naan?»
Te ne lasiim ci mbeddi dëkk bi,
ni ñu gaañoo xare,
bakkan di tàggoo fa ñu uufoo
ca weenu yaay.
 
13 Yaw Janq Yerusalem mu taaru mi,
lu ma lay wax? Ku ma lay méngaleel?
Siyoŋ mu jekk mu taaru mi laa ne,
ana ku ma lay dendaleel, ba seral sa xol?
Yaw mi sab góom yaa ni géej,
ana ku lay faj?
 
14 Ag neen aki caaxaan la la say yonent gisal,
te biraluñu sag ñaawtéef, ngir tijji sa wërsëg,
xanaa di la yéeneel waxyuy caaxaan aki nax.
 
15 Mboolem ñi fi jaareey tacc-taccali loxo,
ciipu, wëcc bopp ci gentub Yerusalem mu taaru ma,
te naan: «Xanaa du biib dëkk lañu doon tudd
sottiteb taar ba,
te muy mbégtem àddina sépp?»
 
16 Sa noon yépp a lay ñaawal,
di la kókkaleek a kekku,
te naan: «Sànk nanu leen nag!
Bii bés lanu yàggoona séentu,
te noo ko fekke tey.»
 
17 Aji Sax jee def la mu nammoon,
moo sottal kàddoom
ga mu santaane woon janti démb.
Moo fàdd te yërëmul,
ba may noon bége leen,
te moo kaweel sa kàttanu bañ yi.
 
18 Askan waa ngi jooy jooyi xol
fi kanam Boroom bi.
Éy yaw tatay janq Siyoŋ mu taaru mi,
sottil say rongooñ ni walum dex guddeek bëccëg;
bul nopplu, bul feral say rongooñ.
 
19 Jógal guddi, xaacu:
ndoortel wattub guddi, ngay yuri sab xol
nim ndox, jàkkaarlook Boroom bi.
Tàllal koy loxo, ngir sa bakkani doom,
yi xiif tax ne lasiim fi boppu mbeddoo mbedd.
 
Waa Yerusalem àddu na
20 Éy Aji Sax ji, xoolal, seetal rekk
ki nga def nii!
Xanaa du ndey mooy dem ba yàpp doomam,
doom ju mu sukk jur, mu wér péŋŋ!
Xanaa du sarxalkat akub yonent lañuy bóom
fi bérabu Aji Sax bu sell bi!
 
21 Mag ak ndaw a ngi ne lareet fi suuf
ci mbedd yi;
sama janq jeek sama xale yu góor yi tëdd,
fàddoo saamar.
Yaa rey ci sa bésub mer,
yaa rendi te yërëmoo.
 
22 Yaa woote ni su doon bésu màggal,
tiitaange dar kepp ma.
Bésub merum Aji Sax ji, kenn rëccul,
kenn muccul.
Doom yi ma jur, yar leen,
noon bi fàkkas leen!