Kàdduy Jooytu
1
Yonent Yàlla Yeremi àddu na
Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey!
Te ñoñam noon gàññ démb.
Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey,
te noon ràññ fi biir xeet yi!
Moo doon lingeeru diiwaan yi,
tey mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.
 
Day fanaanee jooya jooy,
rongooñ yay bas-basi,
te du kenn ku koy dëfal
ci mboolemi soppeem.
Xaritoo xarit wor ko,
walbatiku diy noonam.
 
Ngàllo lañu yóbbu Yuda,
ci biir naqar ak njaam gu metti.
Ci biiri jaambur lañu dëkk,
amuñu fu ñu nopploo,
mboolem ña leen dàqa leen dab,
ba tance leen ca ruq ya.
 
Yoon yi jëm Siyoŋ* jooy na wéet,
kenn jaareetu ca màggalsi.
Pénc yépp a gental,
sarxalkat yay binni,
janq ja jàq,
Siyoŋ gépp di naqarlu!
 
Seen noon yaa jiite tey,
seen bañ yooyoo ne finaax,
Aji Sax jee mbugale waa Siyoŋ
seeni tooñ yu bare,
seeni doom duggig njaam,
di moomeel ub noon.
 
Lu doon sagub Siyoŋ, dëkk bu taaru bi,
tey sàggiku na.
Seeni garmee ngi mel ni kéwél
yu amul parlu,
di koyoŋ-koyoŋiy daw,
te rëbb ne leen dann.
 
Tey ci janti toroxte ak tumurànke,
la Yerusalem di fàttlikoo
mboolem ngëneeli démbam.
Aw askanam a tàbbi ci loxol noon,
te wall amul,
noon ba gis leen,
di textexi ci seenug yàqule.
 
Yerusalem a moya moy,
ba tax koo mujj di sobe;
ku ko teraloon, sofental ko,
ndax gis ko, mu ne duŋŋ.
Moom ci boppam mu ngi binni,
fuuylu.
 
Sobey Siyoŋ ca pendalam,
te bàyyiwul xel ag mujam.
Jéllam ba yéeme na,
te amul ku ko dëfal.
Siyoŋ nee: «Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare;
noon bi déy, am na ndam!»
 
10 Loxo la noon bi teg ci
ngëneeli Siyoŋ gépp.
Siyoŋ kay a gis yéefar yi songsi
këram gu sell gi,
te ci ñoom nga santaane woon, ne
buñu dugg sam ndaje.
 
11 Waa Siyoŋ gépp a ngi binni,
di wut ab dund,
seeni ngëneel lañuy weccikoo aw ñam
wu ñu leqlikoo.
 
Yerusalem àddu na
Gisal Aji Sax ji, seetal
ni ma mujj tekkeedee!
 
12 Yeen mboolem ñiy jaare yoon wi,
lii safu leen,
waaye seetleen rekk ba gis
ndax wenn mitit dab na
mitit wi ñu ma teg,
te Aji Sax ji naqarale ma ko
ci jantub tàkktel sànjam.
 
13 Fa kaw la Aji Sax ji sànnee sawara
ci sama biiri yax,
moo laaw ab caax ngir fakktal ma,
waññi ma, jànnaxe ma,
ma dëkke yoggooral.
 
14 Samay tooñ la Aji Sax ji ëmb,
fastee ko loxoom,
mu tege sama kaw ndodd,
ba jeexal sama doole.
Boroom bee ma tàbbal
ci loxo yu ma manula të.
 
15 Ku doon jàmbaar fi sama biir,
la Boroom bi xalab.
Am ndaje la ma wooteel,
ngir falaxe sama ndaw yu góor.
Boroom bee dëggaate Janq Yuda mu taaru mi,
ni reseñ ci biir nalukaay.
 
16 Looloo ma tax di jooy,
rongooñ di wal-wali,
te ku may dëfal sore ma,
mook kuy seral sama xol.
Samay doom a ngi jaaxle,
nde noon bi daan na.
 
Yeremi àddu na
17  Siyoŋ tàllal na loxoom,
waaye amul ku ko dëfal.
Aji Sax jee wool askanu Yanqóoba
seeni noon yi leen wër,
ba Yerusalem mujj di sobe fi seen biir.
 
Yerusalem àddu na
18  Aji Sax ji moo yey,
kàddoom laa gàntal.
Yeen, xeetoo xeet, ngalla dégluleen
te xool samaw tiis.
Samay ndaw yu góor ak yu jigéen,
ñoo duggi ngàllo!
 
19 Samay soppe laa woo wall,
ñoom ñu wor ma.
Samay sarxalkat ak samay mag di wuti ab dund
bu ñu leqlikoo,
far faatu ci biir dëkk bi.
 
20 Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare,
samay butit di fuddu,
sama biir xol salfaañoo ndaxu tiis.
Man de maa gàntal ba gàntaaral,
ba fa biti, saamar di fa bóome,
te biir kër it di ndee.
 
21 Dégg nañu may binni,
te awma ku ma dëfal.
Noon yépp a dégg samaw ay
te di ko bége, nde yaa ko def.
Ngalla indil bés bi nga dige,
ba ñu daj li ma daj.
 
22 Yal na seen gépp mbon teew fi sa kanam,
ba nga mbugal leen
ni nga ma mbugale
ndax mboolem samay tooñ.
Samay onk bare na,
sama xol jeex tàkk.
* 1:4 Siyoŋ mooy Yerusalem itam. 1:11 wut ab dund: li leen xañ ab dund mooy gaw bu yàgg bu ñu leen gaw, ba ñu mujj xiif lool. Seetal ci 2.Buur ya 25.1-3.