9
Peeñum juróomeel bi
Ma gis nag Boroom bi, mu taxaw ca sarxalukaay ba.
Mu ne: «Dóorleen ci kaw jëni jaamookaay bi,
ba kenu yi yëngu,
te ngeen màbb ko ci kaw boppi ñépp;
ña mucc, ma reylu ci xare.
Du kuy fëx ba rëcc,
du kuy daw ba raw.
Bu ñu bëttoon, ba biir njaniiw it,
fa laa leen di yóotoo.
Ñu yéeg asamaan,
ma wàccee leen fa.
Bu ñu nëbbu woon kaw tundu Karmel it,
fa laa leen di fekk, yóbbu.
Ñu làqoo ma ca taatu géej,
ma sante fa jaani géej, mu màtt leen.
Su ñu demee, diy jaam ñu seeni noon jiital,
fa laay sante boroom saamar, mu bóom leen.
Du bëtu jàmm laa leen di xoole,
bët bu aay laa leen di xoole moos!»
 
Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi,
kiy laal suuf, mu ne soyox seey,
mboolem lu ci biiram di jooyoo;
suuf fuddoondoo ni dexu Niil,
dellu rës ni dexu Misra.
Kee tabax kaw asamaan néegi biiram,
samp ub xaddam, yiire suuf.
Keey woo walum géej,
walal fi kaw suuf.
Kookoo di Aji Sax ji.
Mbugal yell na
«Bànni Israyiloo, xanaa du yeen ak waa Kuus laa yemale?»
Kàddug Aji Sax jee.
«Xanaa du ni ma leen génnee réewum Misra
laa génnee Filisteen ñi réewum Kaftor,
génnee ni waa Siri réewum Kir?
Boroom bi, Aji Sax jaa ngi ne jàkk
réewum bàkkaarkat mii.
Maa koy sànke kaw suuf,
waaye ba tey duma fàkkas faraas waa kër Yanqóoba.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Maa ngii déy di sant xeetoo xeet,
ñu gësëm waa kër Israyil,
ni ñuy gësëme tameb suuf,
te doj du rot.
10 Saamar ay rey mboolem sama bàkkaarkati mbooloo
mi naan: “Yàlla du wacc musiba di nu jege,
ba di nu dab.”»
Waa kër Buur Daawuda faluwaat nañu
(Saar 9.11-15)
11 «Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy,
ba fattaat xar-xar yi,
defaraat gent bi,
tabaxaat ko na woon.
12 Su boobaa bànni Israyil nangu ndesu Edom,
ak mboolem suufi xeet yi ñu ma tudde woon.»
Kàddug Aji Sax jee, te moom lay def.
13 «Ay bés a ngii déy, di ñëw,»
kàddug Aji Sax jee,
«kuy gàbb dina dab kuy góob,
kuy nal reseñ dab ka koy ji.
Biiñ bu bees di rogalaate ca tund yu mag ya,
di wale tundoo tund wu ndaw.
14 Maay tijji wërsëgu Israyil, sama ñoñ;
ñu tabaxaat seeni gent, dëkke;
jëmbat seen tóokëri reseñ,
naan seen biiñ,
bey ay tool,
lekk ca meññeef ma.
15 Maa leen di jëmbat fi seen suuf,
te deesatu leen déjjatee fi seen suuf
si ma leen jox.»
Seen Yàlla, Aji Sax jee ko wax.