8
Peeñum ñeenteel bi
Gannaaw gi Boroom bi, Aji Sax ji dellooti feeñu ma. Ma jekki gis dàmbu meññeef. Mu ne ma: «Amos, ana loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa dàmbu meññeef mu ñor.» Aji Sax ji ne ma: «Mbugal ñoral na Israyil, sama ñoñ. Dootuma leen baal dara. Bésub keroog jàngi kër Buur doon ay jooy.»
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee:
«Néew yi, xas,
fu ne ñu jalax, lépp selaw!»
Bëgge indi na musiba
Amos ne:
«Dégluleen lii, yeen jula yiy dëggaate aji ñàkk,
di jeexal néew-ji-dooley réew mi,
te naan: “Xanaa màggalu Terutel weer wi du jeex
ba nu jaay sunu pepp?
Waay, na bésub Noflaay jàll gaaw,
ba nu ubbi sàq yi,
tuutal nattu sol-sotti, diisal doomu nattukaay,
tey naxee sunuy màndaxekaayi njublaŋ,
ba jënd njaam ku tëlee fey boram
ak aji ñàkk ju tëlee fey dàlli carax;
ba cox sax, nu buub, jaay.”»
 
Aji Sax ji giñ na ci turam wi askanu Yanqóobay damoo, ne:
«Duma fàtte mukk lenn ci seeni jëf.
Moo tax réew mi nara yëngu moos,
muy tiisu ku ci dëkk;
suuf fuddoondoo, fees ni dexu Niil,
di jóg ak a rës ni dexu Misra.
Ay bés a ngii déy, di ñëw,»
kàddug Boroom bi Aji Sax jee:
«maay sowal jant digg bëccëg,
lëndëmal suuf bëccëg ndarakàmm.
10 Maay soppli seeni màggal ab dëj,
seen woyoo woy diy jooy.
Maay wodde bépp lupp saaku yu ñuy ñaawloo,
bépp bopp, ma wat ub nel,
def ko mu mel ni dëju benn bàjjo bu góor,
muj ga di bés bu tar.
 
11 «Ay bés a ngii déy, di ñëw,»
kàddug Boroom bi Aji Sax jee:
«maay wàcce xiif ci réew mi.
Du doon xiifub dugub mbaa marum ndox,
kàddug Aji Sax ji lañuy xiif.
12 Dees na tambaambalu, géej ba géej,
bëj-gànnaar ba penku,
di wëraaluy sàkku kàddug Aji Sax ji,
te deesul dajeek moom.
13 Bésub keroog janq ju taaru jaak
xale yu góor ya deek mar.
14 Ñooñooy giñe tuuri Samari,
naa: “Giñ naa ko ca tuur may dund ca Dan*,
giñ ko ca yoonu Beerseba wa dul fey.”
Dinañu daanu, dootuñu jóg.»
 
* 8:14 Dan la Buur Yerbowam yékkati woon tuur yu ñu jëmmale wëlluy wurus. Seetal ci 1.Buur ya 12.29-30.