8
Mbéx wuutu na koor
Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dellu dikk, ne:
«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
Maa fiire Siyoŋ fiiraange ju réy,
am sànj mu réy laa koy fiiree.»
 
Aji Sax ji dafa wax ne:
«Maay dellu Siyoŋ,
Yerusalem googu laay màkkaanoo,
ba ñuy wooye Yerusalem dëkkub Worma,
foofu di tundu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
lees di wooye tundu Sellnga.»
 
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Mag ñu góor ñeek ñu jigéen ñeey dellu tooge
pénci Yerusalem,
ku ci nekk ak bantam cib loxoom,
ndax at yu bare.
Pénci dëkk bi, ay gone lay feese,
góor ak jigéen, di foye ca pénc ya.»
 
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Su loolu dee kawtéef ci gis-gisu ndesu askan wi
ci yooyu jant,
ndax tax na muy kawtéef ci sama gis-gis itam?»
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
 
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Maa ngii di walloo sama ñoñ
fa réewum penku, ak réewum sowub jant.
Maa leen di indi,
ñu màkkaanoo digg Yerusalem,
di sama ñoñ, may seen Yàlla,
ci biir worma ak njekk.»
 
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Yeen ñi dégg kàddu yii tey
ci gémmiñu yonent yi fekke woon
ba ñuy teg kenug kër Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
ngir tabaxaat kër gi,
nangeen góor-góorlu.
10 Ndax lu jiitu fan yooyu, nit feyeekuwul peyoor,
te mala it indilul nit peyoor,
kuy dem ak kuy dikk amul woon jàmm cib noon,
nde maa xabtaloon ku nekk ci kaw moroomam.
11 Waaye léegi du na woon laay def
ak ndesu askan wii.»
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
12 «Ndax jiwum jàmm lay doon,
garabu reseñ meññ doomam,
suuf si meññ gàncaxam,
asamaan di lay.
Loolu lépp laay sédd ndesu askan wii.
13 Na ngeen doone woon alkànde ci biir xeet yi,
yeen waa kër Yuda, ak waa kër Israyil,
ni laa leen di walloo, ba ngeen doon barke.
Buleen ragal. Góor-góorluleen.»
14 Ndax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne:
«Na ma leen nammoona mbugale
te delluwuma ci gannaaw,
ba ma seeni maam merloo,»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax,
15 «ni laa nammatee baaxe, ci janti tey jii,
Yerusalem, ak waa kër Yuda.
Kon buleen ragal.
 
16 «Ndigal yii, nangeen ko jëfe:
Deeleen waxante dëgg,
te dëgg ak yoon, nangeen ko àttee àtteb jàmm
ci seen ëtti àttekaay.
17 Ku nekk ci yeen, loraangey moroomam,
bumu ko mébét cib xolam,
te kàddug ngiñ ci ay fen, buleen ko safoo,
nde loolu lépp laa bañ.»
Kàddug Aji Sax jee.
 
18 Kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dellu ma dikkal ne ma:
19 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Muy koorug weeru ñeenteel, di koorug weeru juróomeel,
ak koorug weeru juróom ñaareel, ak koorug weeru fukkeel*,
lépp janti mbég ak bànneex,
ak bési ndaje yu rafet lay nekkal waa kër Yuda
Waaye dëgg ak jàmm, soppleen ko.»
 
20 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Ay askan ñooy dikkati, di waa dëkk yu bare,
21 waa dëkk bii dem ne bee:
“Nan dema dem dagaani Aji Sax ji,
nan sàkkuji Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,”
Ñu ne leen: “Nun it kay, nu ngi dem.”»
22 Askan yu bare, ak xeet yu am doole ñooy dikk,
di sàkkusi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi ci Yerusalem,
di dagaansi Aji Sax ji.
 
23 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Janti keroog yooyu, fukk ñuy làkk
mboolem làkki xeet yi,
ñooy langaamoo catu mbubbu benn Yawut, naan ko:
“Nun, yeen lanuy àndal,
nde noo dégg ne Yàllaa ngeek yeen.”»
* 8:19 Bési koor yooyu ba bànni Israyil nekkee ngàllo ca Babilon lañu ko daan sàmm, di ko ñaawloo seen jaar-jaar yu metti.