10
Daawuda jote naak Amoneen ña
1 Gannaaw loolu Nayas buurub Amoneen ña dee, Anun doomam ju góor falu buur, wuutu ko.
2 Daawuda ne: «Dinaa jëfe ngor sama digganteek Anun doomu Nayas, na ma baayam jiye woon ngor.» Daawuda nag yebal ay ndawam ca Anun, di ko jaal baayam. Ba ndawi Daawuda ya agsee ca réewum Amoneen ña,
3 njiiti Amoneen ña wax ak seen sang Anun, ne ko: «Defe nga ne moos wormaal sa baay la Daawuda namm, ba yónnee la ay nit ñu la jaal? Foogoo ne seetsi dëkk bi ak nemmikusi ko, ba song ko moo tax Daawuda yebal ay nitam ci yaw?»
4 Anun daldi jàpp niti Daawuda ña, wat seen genn-wàllu sikkim, dagg seeni mbubb fa tollook toogukaay ba, daldi leen dàq.
5 Ñu yegge Daawuda mbir ma, mu yeble ngir ñu gatanduji leen ndax na ñu leen torxale. Mu ne leen ñu toog Yeriko, ba seeni sikkim sëqaat, ñu doora ñibbsi.
6 Amoneen ña xam ne Daawuda jéppi na leen lool. Ñu dem bindi ñaar fukki junniy (20 000) xarekat ca waa Siri ña dëkke Bet Reyob ak waa Siri ña dëkke Soba, teg ca junniy nit ñu bàyyikoo ca buuru Maaka, ak fukki junneek ñaar (12 000) ñu waa Tob.
7 Daawuda dégg ko, yebal Yowab ak mboolem gàngooru jàmbaar ña.
8 Ba mu ko defee Amoneen ña génn, làng-dér ca seen buntu péey ba, fekk waa Siri ña dëkke Soba ak Reyob ak waa Tob ak waa Maaka, ñoom ñépp a nga taxawe nee ca àll ba, seen wetu bopp.
9 Yowab gis làngi xare yi ñu wara jànkoonteel, ga ko féete kanam, ak ga ca gannaaw. Mu tànne ca jàmbaari Israyil yépp jàmbaari xare yu mag, ñu làng-déral waa Siri.
10 La des ca gàngoor ga, mu teg ca loxol rakkam Abisay, làng-dérloo leen, ñu janook Amoneen ña.
11 Yowab ne Abisay: «Bu ma waa Siri ëppee doole, nga wallusi ma; su la Amoneen ñi ëppee doole, ma wallusi la.
12 Góor-góorlul nag, te nu bokk góor-góorlu ngir sunuw xeet ak sunu dëkki Yàlla yi. Aji Sax ji nag mooy def li ko soob.»
13 Ba loolu amee Yowab ak gàngoor ga ànd ak moom sàqi ngir xareek waa Siri, waa Siri daw, won leen gannaaw.
14 Amoneen ña gis waa Siri di daw, ñoom it ñu daw, won Abisay gannaaw ba dellu ca biir dëkk ba. Yowab nag bàyyikoo ca xare baak Amoneen ña, daldi dellu Yerusalem.
Daawuda xare naak Siri
15 Gannaaw loolu waa Siri gis na ñu daanoo fa kanam Israyil. Ñu bokk daje ñoom ñépp.
16 Ci kaw loolu Buur Adadeser yónnee, jëli waa Siri ña ca wàllaa dexu Efraat. Waa wàllaa dex dikk ba dëkk ba ñuy wax Elam; Sobag, njiital gàngooru Adadeser jiite leen.
17 Naka lañu ko wax Daawuda, mu woo Israyil gépp, daldi jàll dexu Yurdan, ba àgg Elam. Waa Siri nag làng-déral Daawuda, song leen.
18 Waaye waa Siree daw, won Israyil gannaaw. Daawuda rey ca ñoom juróom ñaar téeméeri dawalkati watiiri xare (700), ak ñeent fukki junniy gawar (40 000). Sobag, seen njiital gàngoor, mu jam ko, mu dee foofa.
19 Ba mu ko defee mboolem buur yay jawriñi Adadeser gis na ñu daanoo fa kanam Israyil, ñu daldi jàmmook bànni Israyil, nangul leen. Ba loolu amee waa Siri ñemeetuñoo sotle Amoneen ña.