15
Na gëmkat yiy xajoonte
Nun ñi fendi ci wàllu ngëm, fàww nu xajoo tëley ñi néew doole, te baña sàkku sunu bànneexu bopp. Na ku nekk ci nun sàkku bànneexu moroomam, ci lu koy jariñ, ngir feddli ngëmam. Ndax Almasi kat sàkkuwul bànneexu boppam, te noonu it la Mbind mi indee ne: «Ñi lay saaga, seeni saaga, ci sama kaw la dal* Ndaxte mboolem lu ñu bindoon, bu jëkk, jàngal nu moo taxoon ñu bind ko, ngir Mbind mi may nu xolu muñ, te ñaax nu, ba nu am yaakaar. Kon nag Yàlla miy maye xolu muñ, di ñaaxe, yal na leen may mànkoo gu mat sëkk, ni ko Almasi Yeesu bëgge, ngir nu bokk jenn yéene ak genn kàddu gu ngeen sàbbaale Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi.
Xibaaru jàmm bi ñépp la dikkal
Kon nag, ni leen Almasi xajoo, nangeen ko xajoontee, ngir teddngay Yàlla. Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam. Leneen li indi Almasi mooy may jaambur ñi dul Yawut lu ñu màggale Yàlla, te muy yërmandeem. Noonu it la Mbind mi indee ne:
«Looloo waral ma sant la ci biir xeet yi,
sàbbaal la
10 Mu neeti:
«Yeen xeet yi, bégandooleen ak ñoñam
11 Mu dellu ne:
«Yeen xeetoo xeet, màggal-leen Boroom bi,
réewoo réew, kañleen ko§
12 Esayi it neeti:
«Ab car ay bawoo ca Yese* reen ba,
mooy taxaw, yilif jaambur ñi dul Yawut,
te moom la ñi dul Yawut di yaakaar
13 Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
Póol xamle na sababu bataaxalam
14 Bokk yi, man ci sama bopp, li ma bir ci seen mbir moo di yéene ju rafet ngeen fees, te buural ngeen bépp xam-xam, man ngeena artoonte it. 15 Teewul mu am ci wet yu ma leen ñemee binde kàddu yu ma ñéebluwul, ngir fàttli leen li ngeen xamoon ba noppi. Noonu ma binde nag, li ko waral moo di yiw wi ma Yàlla baaxe, 16 ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal. 17 Moo tax ma saña puukarewoo Almasi Yeesu mi may liggéeyloo ci mbiri Yàlla. 18 Sañumaa tudd lenn nag lu moy li Almasi sottale sama jëmm, ngir jaambur ñi dul Yawut déggal Yàlla, te muy lu mu sottale samay wax ak samay jëf, 19 ci kaw firnde yu manoorewu, aki kéemaan, lépp ci manoorey Noowug Yàlla. Loolu tax na, li dale Yerusalem, wëndeelu, ba ca diiwaanu Iliri, yégle naa fa xibaaru jàmm bu Almasi, ba mu mat sëkk. 20 Noonu laa masa xintewoo di xamle xibaaru jàmm bi fu ñu xamewul Almasi asi, ngir baña bey sas wu fa keneen jotoona dal. 21 Noonu ma jëfe it moo dëppoo ak ni ko Mbind mi indee ne:
«Ña ñu waxul woon mbiram, dinañu gis,
te ña dégguloon, dinañu ràññee
Póol dige naa seeti waa Room
22 Sama liggéey boobu sax moo ma gàllankoor lu bare ba dikkaguma seetsi leen. 23 Waaye léegi jeexal naa sama sas ci gox yii, te gannaaw at yu baree ngii, ma namma dikk ba seetsi leen, 24 bu may dem Espaañ, dinaa leen seetsiwaale. Yaakaar naa leena gis bu ma fa jaaree, ba ngeen yiwi ma, ma jàlli Espaañ, gannaaw, lu mu néew néew, ay fan yu ma nammantikoo ak yeen. 25 Waaye fii ma tollu, Yerusalem laa jëm, ngir ndimbal lu ñeel ñu sell ña féete foofa. 26 Ndaxte gëmkati Maseduwan ak Akayi ñoom la soob ñu sàkke lenn ci seen alal, ngir dimbalee ko ñu sell ña diy néew doole ca Yerusalem. 27 Seen coobarey bopp lañu ko defe, waaye ñoo ko ameel waa Yerusalem it nag. Ndaxte gannaaw ñoom ñiy jaambur, gëmkati Yerusalem ñoo leen sédd ci xéewal yi leen ngëm may, kon ñoom jaambur ñi itam war nañu leena sédd ci seen alal. 28 Teewul nag bu ma noppee ci lii, ba teg teraanga jii ca loxoy waa Yerusalem, Espaañ laa jëm, te fa yeen laay jaare. 29 Te xam naa ne bu ma dikkee fa yeen, barkeb Almasi bu mat sëkk laay dikke.
30 Gannaaw loolu bokk yi, li ma leen di ñaan ngir sunu Boroom Yeesu Almasi, ngir itam cofeel gi Noo gu Sell giy maye, moo di ngeen fekksi ma ci xareb ñaan ngir man. 31 Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci aji gëmadiy Yude, te itam ndimbal li may yóbbul ñu sell ña ca Yerusalem, ñaanleen ngir ñu nangu ko. 32 Su ko defee, ci coobarey Yàlla, ma dikke mbégte ba fa yeen, ba dal-luwaale as lëf fa yeen. 33 Yal na Yàlla miy boroom jàmm ànd ak yeen ñépp. Amiin.
* 15:3 Seetal ci Sabóor 69.9. 15:9 Seetal ci Sabóor 18.49. 15:10 Seetal ci Baamtug Yoon wi 32.43. § 15:11 Seetal ci Sabóor 117.1. * 15:12 Yese mooy baayu Daawuda. 15:12 Seetal ci Esayi 11.10. 15:21 Seetal ci Esayi 12.15.