Sabóor 58
Yàllaa mana mbugal
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda.
 
Yeen daal, su ngeen waxee, dëgg selaw.
Mbaa yeena ngi àtte nit ñi ci yoon?
Yeena ngi mébét njubadi,
di lawal fitna ci réew mi.
 
Ku bon day sosu rekk, dëng;
juddu, teggi yoon, dib fen-kat.
Day am daŋar ni ñàngóor,
fatti noppam ni jaan ju tëx:
du dégg baatu jatkat,
mbaa jati ñeengokat bu ñàng.
 
Yàlla, ngalla tojal seeni gëñ;
Aji Sax ji, foqal seen selli gaynde yii.
Yal nañu ne mes ni ndox muy wal,
yal nañu diir seen fitt, mu damm,
yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey,
mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant.
10 Balaa seen cin a yég tàngooru gajj,
muy gu tooy, muy guy boy,
yal na leen fekk sànku*.
 
11 Aji jub day gis ñu feyul ko, mu bég,
muy jàngoo deretu ku bon.
12 Ku ne naan: «Ku jub jot sab yool moos!
Te Yàllaa ngi fi moos, di àtte àddina!»
* 58:10 Li ñu wax ci aaya wii am na werante.