Sabóor 29
Aji Sax jeey boroom ndam
1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Yeen goney Yàlla yi, seedeel-leen Aji Sax ji,
seedeel-leen ko teddngaak doole,
2 seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam.
Sujjóotal-leen Aji Sax ji,
ki gànjaroo sellnga.
3 Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma,
Yàlla mu tedd maa dënu,
Aji Sax jeey tiim ndox, mi ne màww.
4 Aji Sax jeey àddoo doole,
Aji Sax jeey àddoo daraja.
5 Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar,
Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ.
6 Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu,
tundu Siryoŋ it, mbete yëkk wu ndaw.
7 Aji Sax jeey àddu,
fettaxal sawara, mu boy.
8 Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ,
Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.
9 Aji Sax jeey àddu, kéwél matu,
garabi àll ruus,
biir këram di mennum riir,
naan: «Màggal-leen ko!»
10 Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu,
Aji Sax jee falu buur ba fàww.
11 Aji Sax jeey kàttanal ñoñam,
di barkeele jàmm ñoñam.