3
Jëkkër sang la, jabar di nawle
1 Naka noonu yeen jigéen ñi, nangul-leen seen jëkkër, ngir jëkkër ju ci nanguwula gëm kàddu gi it, mana gindiku te wax du ci am yoon, ngir na jabaram di jëfe,
2 ndax day xool ci yeen ak seenug sellal gu ànd ak wegeel.
3 Seen gànjar bumu doon gànjaru biti bu yem ci ay létt yu rafet, ak takkaayi wurus, ak yére yu yànj,
4 waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.
5 Bu jëkkoon loolu moo doon gànjaru jigéen ñu sell ña yaakaaroon Yàlla te nangul seen jëkkër,
6 noonu Saarata déggale woon Ibraayma, naan ko «Sang bi». Yeen jigéen ñi nag, yeen ay doomi Saarata, li feek yeena ngi def lu baax te bañ cee ragal ku leen xupp.
7 Naka noonu yeen góor ñi, bàyyileen xel ni ngeen dëkke ak seeni jabar, tey sóoraale néew dooley jigéen. Séddleen leen teraangay nawle, gannaaw yeena bokk wenn yiw wi leen may ngeen dund dëgg. Su ko defee dara du gàllankoor seeni ñaan.
Soppanteleen te saxoo baax
8 Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof.
9 Lu bon, buleen ko feye lu bon; ay saaga it, buleen ko feye ay saaga. Xanaa ngeen ñaanal leen, feye leen ko, ndax ci loolu lees leen woo, ngir ngeen jagoo barke.
10 Ndax kat:
«Ku bëgga bége bakkanam,
fekke bés bu rafet,
na làmmiñam daw lu aay,
dawi fen.
11 Na daggook lu bon, tey def lu baax,
na sàkku jàmm, saxoo ko.
12 Ndax ay gët la Boroom bi
ne jàkk aji jub ñi,
te ay noppam la dékk seeni ñaan,
waaye Boroom bi, kanamam lay tëjal
ñiy def lu bon.»
Na seenug njub waral seen coono
13 Te it su ngeen dee ñu njaxlaf ci def lu baax, ana ku leen di def lu bon?
14 Te sax su ngeen doon jànkoonteeki coono ndax seenug njub, ndokklee yeen. Buleen am jenn tiitaange ci seeni xuppe, te buleen jaaxle.
15 Waaye Sang Almasi ngeen di sellal ci seen xol, te waajal nu ngeen di tontoo ku leen laaj lu jëm ci yaakaar ji ngeen am.
16 Waaye nay tont lu rafet te ànd akub yar. Saxooleen di jëfe li dalal seenum xel, ba mbir ma ñu leen di baatali, ñooñuy ŋàññ seen dundin wu rafet wi leen Almasi manloo, gàcce rekk lañuy jële ca mbir ma ñu leen di baatali.
17 Coono yu la jëf ju baax yóbbe kat, ndegam da di coobarey Yàlla, moo gën coono yu la jëf ju bon yóbbe.
18 Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.
19 Ci dooley Noo googu la deme ba waari bindeef ya seeni fit tëje,
20 ñooña gëmadi woon bu yàgg, jant ya Yàllay muñ, di négandiku, te Nóoyin di yett gaal, ga lim bu néew, juróom ñett, mucce woon ca ndox ma.
21 Ndox mooma di misaalub sóobu gi leen musal tey; du sóobu guy dindi tërub yaram, waaye moom ngeen di wuyoo wooteb Yàlla ci xel mu dal, te li leen di musal mooy ndekkitel Yeesu Almasi,
22 mi yéeg asamaan, toog fa ndijooru Yàlla, ki malaaka yeek boroom sañ-sañ yeek boroom doole yi, bokk nekk cig curgaam.