26
Aji Sax ji dafa wax Musaa, ak Elasar doomu Aaróona sarxalkat ba, ne leen: «Waññleen mbooloom bànni Israyil gépp, ngeen lim turi góor ñépp, na ñu bokke seen këri maam, dale ko ci ñi am ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci bànni Israyil.» Musaa ak Elasar sarxalkat ba wax ak ñoom ca joori Mowab, fa janook Yeriko ca wetu dexu Yurdan; ñu ne leen ñi dale ci ñaar fukki at, jëm kaw lees di lim, na ko Aji Sax ji sante Musaa. Lii moo di limeefu nit ña soqikoo ci bànni Israyil, ña génne woon Misra:
Ruben moo doon taawub Israyil. Ñi askanoo ci Ruben ñoo di Anog mi sos làngu Anogeen ñi, ak ñoom Palu mi sos làngu Paluween ñi, ak ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Karmi mi sos làngu Karmeen ñi. Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730).
Palu moo meññ Elyab, Elyab meññ Nemwel ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñooñii doonooni njiit ca mbooloo ma, ñoo doon diiŋat Musaa ak Aaróona. Ña nga bokkoon ca gàngooru Kore, ba ñuy diiŋat Aji Sax ji, 10 ba suuf sa xar, boole leen ak Kore, wonn, keroog ba gàngoor ga sànkoo, te sawara wa lakk ñaar téeméeri nit ak juróom fukk, ñu daldi doon firnde luy artoo. 11 Doomi Kore ya nag deewuñu ca.
12 Ñi askanoo ci Simeyon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Nemwel mi sos làngu Nemweleen ñi, ak ñoom Yamin mi sos làngu Yamineen ñi, ak ñoom Yakin mi sos làngu Yakineen ñi, 13 ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi, ak ñoom Sawul mi sos làngu Cawuleen ñi. 14 Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200).
15 Ñi askanoo ci Gàdd, ñook seeni làng ñoo di ñoom Cefon mi sos làngu Cefoneen ñi, ak ñoom Agi mi sos làngu Ageen ñi, ak ñoom Suni mi sos làngu Cuneen ñi, 16 ak ñoom Osni mi sos làngu Osneen ñi, ak ñoom Eri mi sos làngu Ereen ñi, 17 ak ñoom Arodd mi sos làngu Aroddeen ñi, ak ñoom Areli mi sos làngu Areleen ñi. 18 Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500).
19 Am na nag doomi Yuda yu ñuy wax Er ak Onan. Waaye Er ak Onan ña ca réewum Kanaan lañu faatoo. 20 Ñi askanoo ci Yuda, ñook seeni làng ñoo di ñoom Sela mi sos làngu Celaneen ñi, ak ñoom Peres mi sos làngu Pereseen ñi, ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi. 21 Ñi askanoo ci Peres ñoo di ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Amul mi sos làngu Amuleen ñi. 22 Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500).
23 Ñi askanoo ci Isaakar, ñook seeni làng ñoo di Tola mi sos làngu Toleen ñi, ak ñoom Puwa mi sos làngu Puween ñi, 24 ak ñoom Yasub mi sos làngu Yasubeen ñi, ak ñoom Simron mi sos làngu Simroneen ñi. 25 Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300).
26 Ñi askanoo ci Sabulon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Seredd mi sos làngu Sereddeen ñi, ak ñoom Elon mi sos làngu Eloneen ñi, ak ñoom Yaleel, mi sos làngu Yaleleen ñi. 27 Làngi Sabuloneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom benn fukki junni ak juróomi téeméer (60 500).
28 Ñi askanoo ci Yuusufa nag, ñook seeni làng, ñoo soqikoo ci Manase ak Efrayim. 29 Ñi soqikoo ci Manase ñoo di ñoom Makir mi sos làngu Makireen ñi. Makir moo jur Galàdd. Ci Galàdd la làngu Galàddeen ñi soqikoo. 30 Ñii ñoo askanoo ci Galàdd: Yeser mi sos làngu Yesereen ñi, ak ñoom Eleg mi sos làngu Elegeen ñi, 31 ak Asriyel mi sos làngu Asriyeleen ñi, ak Sikem mi sos làngu Sikemeen ñi, 32 ak Semida mi sos làngu Semideen ñi, ak Efer mi sos làngu Efereen ñi. 33 Selofat doomu Efer nag amuloon doom ju góor, xanaa aw jigéen doŋŋ. Doomi Selofat yu jigéen di Maala ak Nowa ak Ogla ak Milka ak Tirca. 34 Làngi Manasee ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (52 700).
35 Ñii nag ñoo askanoo ci Efrayim, ñook seeni làng: ñoom Sutela mi sos làngu Cuteleen ñi, ak ñoom Beker mi sos làngu Bekereen ñi, ak ñoom Taxan mi sos làngu Taxaneen ñi. 36 Ñii nag, askanu Sutela lañu: ñoom Eran, ak làngu Eraneen ñi mu sos. 37 Làngi Efrayim a ngoogu, ña ñu leen limal di fanweeri junneek ñaar ak juróomi téeméer (32 500).
Ñooñoo askanoo ci Yuusufa, ñook seeni làng.
38 Ñi askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng ñoo di ñoom Bela mi sos làngu Belayeen ñi, ak ñoom Asbel mi sos làngu Asbeleen ñi, ak ñoom Ayram mi sos làngu Ayrameen ñi, 39 ak ñoom Sufam mi sos làngu Sufameen ñi, ak ñoom Ufam mi sos làngu Ufameen ñi. 40 Askanu Bela wi sosoo ci Àrd ak Naaman ñoo di làngu Àrdeen ñi, ak làngu Naameen ñi sëtoo ci Naaman. 41 Ñooñoo askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer (45 600).
42 Ñii nag ñoo askanoo ci Dan, ñook seeni làng: ñoom Suwam ak làngu Cuwameen ñi. Daneen ñaa ngoogu, na ñu lime seeni làng. 43 Mboolem làngi Cuwameen, ña ñu leen limal juróom benn fukki junneek ñeent la, ak ñeenti téeméer (64 400).
44 Ñi askanoo ci Aser, ñook seeni làng ñoo di ñoom Imna mi sos làngu Imneen ñi, ak ñoom Iswi mi sos làngu Isween ñi, ak ñoom Berya mi sos làngu Beryeen ñi. 45 Waa askanu Berya ñoo di ñoom Eber mi sos làngu Ebereen ñi, ak ñoom Malkiyel mi sos làngu Malkiyeleen ñi. 46 Doomu Aser ju jigéen nag moo di Sera. 47 Làngi Asereen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
48 Ñi askanoo ci Neftali ñook seeni làng ñoo di ñoom Yàcceel, mi sos làngu Yaceleen ñi, ak ñoom Gunni mi sos làngu Guneen ñi, 49 ak ñoom Yeccer mi sos làngu Yeccereen ñi, ak ñoom Silem mi sos làngu Cilmeen ñi. 50 Neftaleen ñaa ngoogu, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak ñeenti téeméer (45 400).
51 Limeefu bànni Israyil a ngoogu, di juróom benni téeméeri junneek benn ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (601 730).
Lu jëm ci séddaleb réew ma
52 Aji Sax ji nag wax Musaa, ne ko: 53 «Ñii lees di séddale réew mi, te na cér yi dëppook limu nit ñi: 54 làng gu gëna mag, na am cér bu gëna mag, làng gu gëna tuut, am cér bu gëna tuut, làng gu ci nekk, cér bi dëppook ab limam lees koy jox. 55 Ab tegoo bant doŋŋ lees di séddalee réew mi, te seen limu giiri maam ya ñu bokk, na dëppook seenub cér. 56 Ci kaw tegoo bant lees di dogale céru giir gu ñu bare séq, ak gu ñu néew séq.»
Ñaareelu limeefu Leween ñi taxaw na
57 Ñii nag lañu limal Leween ñi ak seeni làng: ñoom Gerson mi sos làngu Gersoneen ñi, ak ñoom Keyat mi sos làngu Keyateen ñi, ak ñoom Merari mi sos làngu Merareen ñi. 58 Ñii itam ci làngi Leween lañu: làngu Libneen ñi, ak làngu Ebroneen ñi, ak làngu Maaleen ñi, ak làngu Museen ñi, ak làngu Korayeen ñi. Keyat nag mooy maamu Amram; 59 soxnas Amram di Yokebedd doomu Lewi, ja juddoo Misra. Yokebedd am ak Amram Aaróona ak Musaa ak Maryaama, seenub jigéen. 60 Aaróona moo jur Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar. 61 Nadab ak Abiyu ña nga dee keroog ba ñu taalalee Aji Sax ji cuuraay lu warul. 62 Ña ñu limal Leween ñi nag ñaar fukki junneek ñett lañu (23 000), di mboolem góor ña am weer, jëm kaw, te limaaleesu leen ak bànni Israyil ga ca des, ndax joxeesu leen ab cér ci biir bànni Israyil.
Tëj nañu limeef ya
63 Ñooñu lañu lim ci njiital Musaa ak Elasar sarxalkat ba, ba ñu tënkee limeefu bànni Israyil ca joori Mowab, ga janook Yeriko, ca tàkkal dexu Yurdan. 64 Ñooñu, kenn desul ca seen biir, te bokkoon ca limeefu bànni Israyil, ba Musaak Aaróona sarxalkat ba jëkkoona tënke ca màndiŋu Sinayi. 65 Ndax ci ñoom la Aji Sax ji noon dee rekk lañuy def ba jeex ca màndiŋ ma. Kenn desu ca, ku dul Kaleb doomu Yefune, ak Yosuwe doomu Nuun.