Màndiŋ ma
fa bànni Israyil jaare woon
di ñeenteelu xaaju Tawreetu Musaa
Ubbite gi
Téere bii moo tàmbalee ca bés ba bànni Israyil dalee ca taatu tundu Sinayi. Foofu la bànni Israyil jóge jëm màndiŋu Paran, ca bëj-gànnaaru réewum dige ba. Fa lañu yebale ay ndaw yu yërnduji réew ma, te délsi wax seen gis-gis ca ña fa dëkke. Ba ñu demee ba délsi, lañu ne ñoom la ñu gis neexul. Loolu nag tax bànni Israyil di nàttable ndax Yàlla man na leena jox suuf sa mu leen sédd. Ci kaw loolu ñuy jàmbat ci kaw Yàlla. Seen ñàkk kóllëre googu tax na Yàlla teg leen ab daan, ñuy wëndeelu ca màndiŋ ma, ba maas ga doon jàmbat dee, ba geneen maas wuutu leen. Ñeent fukki at lañu wëndeelu, doora walbatiku dox ndànk, jëm Kanaan. Boobu yoon lañu doora nangoo déggal Yàlla. Gannaaw gi lañu sumb ay xare yu am solo, ba daan, ca penkub dexu Yurdan, doora waaj, ngir jàll ca biir réewum dige, ba ñu nammoona gis bu yàgg. Téere bi wone na ne, ni xolu doom Aadama mel rekk moom la ñoñi Yàlla feeñal ci seen jikko ju toogadi. Saxoowuñu lenn, xanaa ŋarale diggante ngëm ak nàttable, cawarte ak xàddi, jëfi ngor ak jëf ju sew. Seen jikko jooju la téere bi wone ne moo leen worale ak Yàlla mi dul soppiku ci kóllëreem, digganteem ak ñoñam, doonte kóllëre gi nag, teewu koo yor ab yaram, te ànd ak njubteem. Musaa nag diggante bu xat lañu ko gisal ci téere bi, Aji Sax ji ak ay bokkam séq ko: Musaa moo doon ndawal Yàlla liy jottli ay ndigalam, te amul woon ab dend ci na mu xejjoo woon ak Yàlla, waaye moo taxawoon itam fa kanam Yàlla, taxawal fa askan wu ñàkk kóllëre, di ko layal te tàyyiwul.
Ci Tënk:
Saar 1—21 Israyil jànge na ca maam ya jóge woon Misra
Saar 22—25 Céru barke bu sax ñeel na Israyil
Saar 26—36 Israyil dégg na ab artoom balaa dugg Kanaan
Israyil jànge na ca maam ya jóge woon Misra
1
(Saar 1—21)
Takk nañu limu bànni Israyil
1 Aji Sax ji moo wax ak Musaa ca màndiŋu Sinayi ca biir xaymab ndaje ma, keroog benn fanu ñaareelu weer wu ñaareelu at, ma topp ca gàddaay ga bawoo Misra. Mu ne ko:
2 «Limleen mbooloom bànni Israyil gépp, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam. Waññleen góor ñépp, bopp ak bopp, ku nekk ak turam.
3 Li ko dale ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci Israyil daal, nangeen leen lim, gàngoor ak gàngoor, yaw ak Aaróona.
4 Giir gu ci nekk, àndleen ceek kilifa yi jiite seen këri maam, ñu jàpple leen ci.
5 Ñiy wuyoo tur yii nag, ñoo leen ciy taxawu:
Ci wàllu Rubeneen ñi, Elisur doomu Sedeyur.
6 Wàllu Cimyoneen ñi, Selumyel doomu Surisadaay.
7 Wàllu Yudeen ñi, Nason doomu Aminadab.
8 Wàllu Isakareen ñi, Netanel doomu Suwar.
9 Wàllu Sabuloneen ñi, Elyab doomu Elon.
10 Ñi ciy askanu Yuusufa ñii la:
Ci wàllu Efraymeen ñi, Elisama doomu Amiyut.
Wàllu Manaseen ñi, Gamalyel doomu Pedasur.
11 Wàllu Beñamineen ñi, Abidan doomu Gidoni.
12 Wàllu Daneen ñi, Ayeser doomu Amisadaay.
13 Wàllu Asereen ñi, Pagyel doomu Okkran.
14 Wàllu Gàddeen ñi, Elyasaf doomu Dewel.
15 Wàllu Neftaleen ñi, Ayra doomu Enan.»
16 Ñooñu lañu woo ci mbooloo mi, muy ñi jiite seen giiri maam. Ñooy njiiti gàngoori Israyil.
17 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona tofloo ñooñu ñu tudd seeni tur,
18 ñu dajale mbooloo ma mépp, keroog ca benn fanu ñaareelu weer wa. La ko dale ca ña am ñaar fukki at, jëm kaw, ñoom ñépp daldi bindu ca limeefu tur ya, ku nekk ak kër maamam, giir ak giir, làng ak làng, bopp ak bopp.
19 Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la Musaa takke seen lim ca màndiŋu Sinayi.
20 Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Ruben taawub Israyil seen maam, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
21 Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500).
22 Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Simeyon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
23 Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300).
24 Ñu lim turi sëti Gàdd, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
25 Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650).
26 Ñu lim turi sëti Yuda, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
27 Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600).
28 Ñu lim turi sëti Isaakar, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
29 Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400).
30 Ñu lim turi sëti Sabulon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
31 Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400).
32 Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Efrayim, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
33 Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500).
34 Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Manase, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
35 Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200).
36 Ñu lim turi sëti Beñamin, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
37 Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400).
38 Ñu lim turi sëti Dan, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
39 Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700).
40 Ñu lim turi sëti Aser, ku nekk ak làngam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
41 Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500).
42 Ñu lim turi sëti Neftali, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
43 Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
44 Yooyu limeef la Musaa ak Aaróona tënk, ña leen ca jàpple di fukki kilifay Israyil ak ñaar, ku ci nekk taxawal kër maamam.
45 Mboolem bànni Israyil yi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, limees na leen, ku ci nekk ak kër maamam.
46 Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550).
Limaaleesul Leween ñi
47 Giirug Leween ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom.
48 Aji Sax ji moo waxoon Musaa, ne ko:
49 «Giirug Lewi ñoom, bu leen lim, bu leen waññaaleek bànni Israyil.
50 Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal.
51 Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey.
52 Bànni Israyil gi ci des, na ku ci nekk topp dalam, ak raayaam ak kurélam.
53 Leween ñi nag nañu dal fi wër jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence. Su ko defee am sànj du dal ci kaw mbooloom bànni Israyil. Te itam na Leween ñi dénkoo dénkaaney jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence.»
54 Bànni Israyil daldi def noonu. Mboolem lu Aji Sax ji santoon Musaa, noonee lañu ko defe.