18
Saxoo ñaan wareef la
1 Yeesu dellu leen léeb lii, ngir ñu wareefoo di sax ci ñaan te baña xàddi.
2 Mu ne: «Ab àttekat la woon cib dëkk; ragalul Yàlla, yégul nit.
3 Ab jëtun a nga woon ca dëkk boobee. Daan na ñëw ca moom, naan ko: “Àtte ma ak sama jotewaale!”
4 Àttekat ba bañ na ay yoon, waaye gannaaw gi mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla, yéguma nit,
5 waaye jigéen jii da maa lakkal; naa ko àtte, bala moo dërr-dërri ba mujj jekkli ma.”»
6 Sang bi teg ca ne: «Jàngatleen li àttekat bu bon bi wax.
7 Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe?
8 Maa leen ne, mooy sàmm seen àq ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki dikkee, mbaa dina fekk ngëm ci kaw suuf?»
Ag njub, bu ko boroom gis
9 Yeesu léebati lii, ngir ñiy damoo seenug njub, tey doyadal ñi ci des.
10 Mu ne: «Ñaari nit a julliji woon ca kër Yàlla ga. Kenn ki di ab Farisen, ki ci des dib juutikat.
11 Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii.
12 Maa ngi woor ñaari yoon, ayu bés gu nekk, di joxe asaka benn céru fukkeelu mboolem lu ma am.”
13 «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore, ñemewula siggi sax, xool asamaan, xanaa di fëgg dënnam te naan: “Éy Yàlla, yërëm ma, man bàkkaarkat bi.”»
14 Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»
Tuut-tànk am na cér
15 Doon nañu indil Yeesu ay tuut-tànk sax, ngir mu teg leen ay loxoom. Taalibe ya gis loolu, di leen jànni.
16 Yeesu nag woolu xale yi, ne: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man, buleen leen aaye, ndax ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguurug Yàlla.
17 Maa leen ko wax déy, képp ku baña nangul nguurug Yàlla ni ab xale, doo ca dugg mukk.»
Dëddu lépp, topp Yeesu jafe na
18 Kenn ci njiiti Yawut yi moo laajoon Yeesu, ne ko: «Sëriñ bu baax bi, ana lu may def, ba texe fàww?»
19 Yeesu ne ko: «Lu tax nga naa ma ku baax ki? Kenn baaxul ku moy Yàlla doŋŋ.
20 Xam nga ndigal yi: “Bul jaaloo, bul bóom, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»
21 Mu ne ko: «Loolu lépp, ba may ndaw laa ko dale sàmm ba tey.»
22 Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.»
23 Ba waa ji déggee loolu, am na tiis wu réy, ndax barele woon na lool.
24 Yeesu gis loolu, daldi ne: «Boroom alal tàbbi ci nguurug Yàlla, ndaw lu jafe!
25 Boroom alal dugg ci nguurug Yàlla de, giléem jaare bën-bënu puso moo ko gëna yomb.»
26 Ña cay dégg nag ne: «Kon ku mana mucc nag?»
27 Yeesu ne leen: «Li të nit, tëwul Yàlla.»
28 Piyeer daldi ne: «Nun de, noo ngii, dëddu la nu amoon, topp la.»
29 Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, amul kenn kuy dëddu kër, mbaa jabar, mbaa mbokk, mbaa waajur, mbaa doom, ngir nguurug Yàlla,
30 te jotaatul lu ko ëpp ay yooni yoon, tey jii, akug texe ba fàww, ëllëg.»
Yeesu baamooti na coono yi koy xaar
31 Yeesu nag yóbbu Fukk ñaak ñaar, wéetook ñoom, ne leen: «Nu ngii jëm Yerusalem, te mboolem lu yonent yi bindoon ci mbirum Doomu nit ki dina sotti.
32 Ndax dees na ko jébbal jaambur ñi dul Yawut, dees na ko ñaawal, saaga ko, tifli ko.
33 Dinañu ko caw, rey ko, ba ca ñetteelu fanam, mu dekki.»
34 Waaye ndaw ya, ñoom, xamuñu dara ci jooju wax, ndax mbóotu kàddug Yeesu gaa leen làqu, ba tax ñu umple la mu wax.
Yeesu faj na silmaxa
35 Ba Yeesu di jubsi dëkk ba ñuy wax Yeriko, ab silmaxaa nga tooge ca peggu yoon wa, di yalwaan.
36 Silmaxa ba dégg mbooloo may romb, mu daldi laaj lu mu doon.
37 Ñu ne ko Yeesum Nasaret moo fa jaare.
38 Ci kaw loolu mu àddu ca kaw ne: «Yeesu, Sëtub Daawuda, yërëm ma!»
39 Ña jiitu femmu ko, ngir mu noppi. Teewul mu gëna xaacooti, ne: «Sëtub Daawuda, yërëm ma!»
40 Yeesu nag taxaw, ne ñu indil ko ko. Ba mu dikkee, mu laaj ko, ne ko:
41 «Loo bëgg ma defal la ko?» Mu ne ko: «Xanaa may gis, Sang bi.»
42 Yeesu ne ko: «Gisal! Sa ngëm faj na la.»
43 Ca saa sa muy gis, daldi topp ci Yeesu, di sàbbaal Yàlla. Mbooloo mépp gis loolu, di sant Yàlla.