8
Ndawas Sunem sa jotaat na alalam
Am na bés Alyaasa wax ndaw sa mu dekkaloon doomam ju góor ne ko: «Ayca, àndal ak sa njaboot, ngeen dali fu ngeen mana dal, ndax Aji Sax ji dogal na ab xiif ci réew mi, te dina am juróom ñaari at.» Ndaw sa fabu, def la ko góoru Yàlla ga wax, dem yoonam mook njabootam, dali ca réewum Filisteen ña, toog fa diiru juróom ñaari at. Ba juróom ñaari at ya matee, ndaw sa jóge ca réewum Filisteen ña, ñibbsi. Mu dem ca Buur, di sàkku mu delloo ko këram ak suufam. Loolu fekk Buur di waxtaan ak Gewasi, surgab Alyaasa góoru Yàlla ga, naan ko: «Ayca, wax ma mboolem jaloore yi Alyaasa def.» Gewasi nag di nettali Buur na Alyaasa dekkalee woon xale ba, rekk ndaw sa Alyaasa dekkaloon doomam ju góor ne jalañ, di sàkkusi ca Buur mu jox ko këram ak suufam. Gewasi ne ko: «Ndaw saa ngii nag, Buur, sang bi. Doomam ju góor jii la Alyaasa dekkaloon.» Buur laaj ndaw sa, mu wax ko lépp. Buur boole kook bëkk-néegam ne ko: «Fexeel ba ñu delloo ndaw sii lépp luy alalam ak dayob lépp lu suufam meññoon, la ko dale ca bés ba mu fi jógee ba tey jii.»
Asayel mujj na falu ca Siri
Am na it yoon wu Alyaasa demoon Damaas, péeyu Siri. Fekk Ben Addàd buurub Siri wopp. Ba ñu ko waxee ne ko: «Góoru Yàlla gi ñëw na fi.» Buur ne Asayel, ab jawriñam: «Demal ca góoru Yàlla ga te yóbbaale loo teg ci loxoom, mu seetal ma ci Aji Sax ji. Laajal ma ko ne ko: “Ndax dinaa jóg ci sama wopp jii?”» Asayel dem ca moom, yóbbaale lu mu ko jox, muy mboolem la gën ca Damaas, tollu ci sëfub ñeent fukki giléem. Mu dikk taxaw ca kanamam, ne ko: «Ben Addàd buurub Siri moo ma yónni fi yaw, ne ma: “Laajal ma Baay Alyaasa ndax dinaa jóge ci sama wopp jii.”» 10 Alyaasa ne ko: «Demal ne ko dina jóg moos, waaye Aji Sax ji won na ma ne dina dee déy!» 11 Ba loolu amee góoru Yàlla ga ne dann, ne ko jàkk, ba Asayel rus. Mu daldi jooy.
12 Asayel ne ko: «Sang bi, looy jooy?» Mu ne ko: «Damaa xam lu bon li ngay defi waa Israyil. Seeni tata ngay taal, seeni xale yu góor nga jam saamar ñu dee, seeni doom nga tas ci suuf, seeni jigéeni biir nga butti.» 13 Asayel ne ko: «Moo sang bi, man mi ab xaj gën, nu ma mana defe jooju jëf ju réy?» Alyaasa ne ko: «Aji Sax ji won na ma ne yaay doon buurub Siri.» 14 Asayel bàyyikoo ca Alyaasa, dellu ca sangam. Mu ne ko: «Lu la Alyaasa wax?» Mu ne ko: «Nee na ma de dinga jóg moos.» 15 Ca ëllëg sa nag Asayel fab malaan, xooj ko ci ndox, dëpp ko ca kanamu buur ba, fatt ko, mu dee. Gannaaw loolu Asayel falu buur, wuutu ko.
Yoram falu na Yuda
16 Ba buurub Israyil Yoram doomu Axab duggee juróomeelu atu nguuram, ca la Yoram doomu Yosafat buurub Yuda falu buur ca Yuda. 17 Fanweeri at ak ñaar la amoon ba muy falu buur, te juróom ñetti at la nguuru fa Yerusalem. 18 Tànki buuri Israyil la topp, di roy waa kër Axab, ndax doomu Axab la jël jabar, di def li Aji Sax ji ñaawlu. 19 Waaye Aji Sax ji bugguloona tas Yuda ngir Daawuda, jaamam ba, ndax la mu ko digoona may ci ay doomam kuy saxal nguuram fàww, ba du fey.
20 Ca jamonoy Yoram la Edomeen ña fippu, bañ moomeelu Yuda, ba fal seen buuru bopp. 21 Gannaaw loolu Yoram jàll ba Sayir, yóbbaale watiiri xareem yépp. Moo jóg ag guddi, dal ca kaw Edomeen ña leen gawoon, moom ak njiiti watiiri xareem. Waaye gàngooru Yuda ñoo daw, dellu ca seeni xayma. 22 Edomeen ñaa ngi bañ moomeelu Yuda ba tey jii. Jant yooyu la Libna itam fippu.
23 Li des ci mbiri Yoram ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. 24 Yoram nag tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca bàmmeelu maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Doomam Akasiya falu buur, wuutu ko.
Akasiya falu na Yuda
25 Ba Yoram doomu Axab buurub Israyil duggee ca fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Akasiya doomu Yoram falu buur ca Yuda. 26 Ñaar fukki at ak ñaar la Akasiya amoon ba muy falu buur, te menn at la nguuru fa Yerusalem. Atalyaa mooy yaayam, sëtub Omri buurub Israyil. 27 Akasiya topp ca tànki waa kër Axab, di def li Aji Sax ji ñaawlu ni waa kër Axab, ndax goro la woon ca waa kër Axab. 28 Akasiya ànd naak Yoram doomu Axab, xarejeek Asayel buurub Siri ca Ramot Galàdd. Waa Siri jam Yoram. 29 Buur Yoram nag walbatiku fajuji ca Yisreel ndax jam-jami waa Siri ya ca Raama, ba muy xareek Asayel buurub Siri. Doomu Yoram, Akasiya buurub Yuda nag dem seeti Yoram doomu Axab fa Yisreel ndax jagadeem ga.