13
Yowakas falu na ci Israyil
Ba doomu Akasiya, Yowas buurub Yuda duggee ñaar fukkeelu atam ak ñett ci nguuram, ca la Yowakas doomu Yewu falu buur ca Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at ak juróom ñaar. Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, topp ci tànki Yerbowam doomu Nebat, di ko roy ci bàkkaar ya mu daan bàkkaarloo Israyil, bañ koo dëddu. Merum Aji Sax ji nag ne jippét ca kaw Israyil, mu teg leen lu yàgg ci loxoy Asayel buurub Siri ak Ben Addàd doomu Asayel. Yowakas nag tinu Aji Sax ji, mu nangul ko, ndax fekk na mu gis fitnay Israyil ji leen buurub Siri fitnaal. Aji Sax ji daldi may Israyil ku leen xettli, ba ñu génn ca loxol waa Siri. Ba loolu amee waa Israyil dellu nekk ca seeni kër ci jàmm, na woon démb ak bëkk-démb. Taxul ba tey ñu dëddu bàkkaari waa kër Yerbowam ya ñu doon bàkkaarloo Israyil. Dañu caa sax. Te it xer wa ñuy jaamoo Aseraa nga sampe woon ca Samari ba booba. Mujj na Yowakas desewuloon ca mbooloom xareem lu moy juróom fukki gawar ak fukki watiir ak fukki junniy xarekat (10 000), ndax buurub Siri moo faagaagal ña ca des ñépp, duma leen ba ñu ne mbëtt.
Li des ci mbiri Yowakas ak mboolem lu mu def aki njàmbaaram, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buurub Israyil ca seeni jant. Ba mu ko defee Buur Yowakas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca Samari. Doomam Yowayas falu buur, wuutu ko.
Yowayas falu na ca Israyil
10 Ba Yowas buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Yowayas doomu Yowakas falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at ak juróom benn.
11 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu nag, dëdduwul lenn ci bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat doon bàkkaarloo Israyil. Da caa sax kay.
12 Li des ci mbiri Yowayas ak mboolem lu mu def ak njàmbaar ga mu xareek Amaciya buurub Yuda, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant. 13 Yowayas nag saay, fekki ay maamam, Yerbowam falu, wuutu ko. Ñu denc Yowayas fa ñu denc buuri Israyil ca Samari.
Yonent Yàlla Alyaasa faatu na
14 Ba Alyaasa tëddee ca wopp ja ko wara yóbbu, Yowayas buurub Israyil seeti woon na ko, tiim ko, di jooy naan: «Éy baayoo, baay Alyaasa, yaay watiiru xarey Israyil aki gawaram!»
15 Alyaasa ne ko: «Indil xala aki fitt.» Mu indi. 16 Alyaasa ne ko: «Soxal.» Mu sox. Alyaasa teg ay loxoom ca kaw loxoom, 17 ba noppi ne ko: «Ubbil palanteeru penku bi.» Mu ubbi. Alyaasa ne ko: «Soqil!» Mu soqi. Mu ne ko: «Fittu ndamal Aji Sax jaa ngoog, di fitt gi ngay ame ndam ci waa Siri. Dinga daan waa Siri ca Afeg, ba faagaagal leen.» 18 Mu delluwaat ne ko: «Jëlal fitt yi.» Mu jël. Mu ne ko: «Soqil fi suuf!» Mu soqi, ba muy ñetti yoon, bàyyi. 19 Góorug Yàlla ga nag mere ko, ne ko: «Soo jamoon juróomi yoon ba juróom benni yoon, dinga daan waa Siri, ba jeexal leen tàkk; waaye léegi nag ñetti yoon rekk ngay daan waa Siri.» 20 Gannaaw gi Alyaasa faatu, ñu denc ko.
Loolu fekk na ndoortel at mu jotaan ay gàngoori yàqkati Mowabeen dugg ca réew ma. 21 Mu am bés ay nit doon rob, jekki-jekki gis gàngooru yàqkat di dikk. Ñu sànni néew ba ca bàmmeelu Alyaasa, daldi daw. Naka la néew ba dal ca yaxi Alyaasa, rekk dekki, ne ñokket, taxaw.
Israyil duma na Siri
22 Ci kaw loolu Asayel buurub Siri di fitnaal Israyil mboolem diir ba Yowakas di buur. 23  Aji Sax ji nag baaxe leen, yërëm leen, geesu leen ndax kóllëreem ak Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Looloo tax buggu leena faagaagal, te ba tey jii xalabu leen. 24 Ba Asayel buurub Siri deeyee, doomam Ben Addàd falu, wuutu ko. 25 Ba mu ko defee Yowayas nangoo ci moom dëkki Israyil ya Asayel jële woon ca loxol baayam Yowakas ci xare. Ñetti yoon Yowayas duma na ko Ben Addàd, ba nanguwaat dëkki Israyil.