8
Sancal nañu gaalu Yàlla ga
Ba mu ko defee Suleymaan woolu magi Israyil. Mboolem kilifay giiri Israyil ak seen njiiti kër maam ya daje Yerusalem ca moom, ngir ñu àgg Siyoŋ, gox ba ñu naan Kër Daawuda, ba yékkatee fa gaal ga kóllërey Aji Sax ji dence.
Waa Israyil gépp nag daje ca Buur Suleymaan, ca weeru Etanim*, ca màggalu juróom ñaareelu weer woowu. Ba magi Israyil ñépp dikkee, sarxalkat ya yékkati gaal ga. Ñu boole gaalu Aji Sax ja, ak xaymab ndaje ma, ak mboolem jumtukaay yu sell ya ca biir xayma ba. Sarxalkat ya ak Leween ña daldi gàddu lépp. Buur Suleymaan ak mbooloom Israyil ma daje fa moom, ñoom ñépp a nga bokk ak moom, teew. Ñu jàkkaarlook gaal ga, di rendi ay gàtt aki nag yu kenn manula lim mbaa di ko waññ, ndax bare.
Gannaaw loolu sarxalkat ya yóbbu gaalu Aji Sax ja ca bérabam, ca biir néeg bu sell baa sell, ca ron laafi malaakay serub ya. Ndaxte jëmmi serub ya, seeni laaf daa tàllalu, tiim bérabu gaal ga, laaf ya yiir kaw gaal ga aki njàppoom. Njàppu ya daa guddoon, ba nit mana séen cat ya te fekk ko tollu ca bérab bu sell ba, ca kanam néeg bu sell baa sell. Waaye maneesula tollu ca biti di séen cat ya. Njàppu yaa nga fa ba tey jii. Dara nekkuloon ca biir gaal ga, lu moy ñaari àlluway doj ya ca Musaa yeboon ca tundu Oreb, fa Aji Sax ji fase woon kóllëre ak bànni Israyil, ba ñu génnee réewum Misra.
10 Ba sarxalkat ya génnee bérab bu sell ba, niir wa daa fees kër Aji Sax ja, 11 ba sarxalkat ya talatuñoo liggéey, ndax leeru Aji Sax jaa nekkoon ca niir wa, niir wa feesal kër ga.
Suleymaan àddu na
12 Ba mu ko defee Suleymaan ne: «Aji Sax ji moo noon lëndëm gu fatt lay màkkaanoo.» 13 Mu ne Aji Sax ji: «Tabaxal naa la kër gu màgg, màkkaan mooy dëkke ba fàww.» 14 Ci kaw loolu Buur Suleymaan walbatiku, ñaanal mbooloom Israyil mépp, fekk mbooloom Israyil mépp a nga taxaw. 15 Mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Israyil, moom mi sottale loxol boppam, la mu waxoon Daawuda sama baay ci gémmiñam, ne ko: 16 “La dale bés ba ma génnee bànni Israyil, sama ñoñ ca Misra ba tey, taamuwuma benn dëkk, ci mboolem giiri Israyil, bu ñuy tabax kër, gu sama tur di nekk. Waaye maa taamu Daawuda, ngir mu falu ci kaw Israyil sama ñoñ.” 17 La doon yéeney Daawuda sama baay nag moo doon tabax kër gu mu tudde Aji Sax ji, Yàllay Israyil. 18 Teewul Aji Sax ji wax Daawuda sama baay, ne ko: “Gannaaw yaa fasoon ci sa xol, yéeney tabax kër, tudde ma ko, def nga lu rafet, ngir sa yéeney xol la woon. 19 Waaye du yaw yaay tabax kër gi; sa doom ju góor ju soqikoo ci sa geño, moom mooy tabax kër gi, tudde ma ko.”
20 «Aji Sax ji moo sottal waxam ja mu waxoon. Wuutu naa sama baay Daawuda, toog naa ci jalub Israyil, noonee ko Aji Sax ji waxe woon. Tabax naa kër gi, tudde ko Aji Sax ji, Yàllay Israyil. 21 Te it sàkk naa fa bérab bu ñeel gaal gi def àlluway kóllërey Aji Sax, ji mu fasoon ak sunuy maam, ba mu leen génnee réewum Misra.»
Suleymaan yékkati na kàddug ñaan
22 Gannaaw loolu Suleymaan taxaw jàkkaarlook sarxalukaayu Aji Sax ji, fa kanam mbooloom Israyil mépp. Mu daldi tàllal ay loxoom asamaan, 23 daldi ne: «Yaw Aji Sax ji Yàllay Israyil, amul jenn yàlla ju mel ni yaw fa kaw asamaan mbaa ci kaw suuf si mu tiim, yaw miy sàmm kóllëre ak ngor, ñeel sa jaam ñiy doxe seen léppi xol, fi sa kanam. 24 Yaa sàmm kàddu ga nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ci sa gémmiñu bopp, te yaa sottale sab loxo, sa kàddu bés niki tey.
25 «Léegi nag Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ngalla sàmmal li nga waxoon sa jaam ba, Daawuda sama baay, ne ko: “Deesu la xañ mukk ci saw askan ku góor kuy tooge jalub Israyil fi sama kanam, ndegam saw askan a ngi moytu seenu yoon, tey doxe fi sama kanam noonee nga daan doxe fi sama kanam.” 26 Kon nag yaw Yàllay Israyil, ngalla saxalal wax jooju nga waxoon Daawuda, sa jaam ba.
27 «Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan yi ba ca asamaani asamaan ya manu laa fat, waxumalaa kër sii ma tabax. 28 Waaye Aji Sax ji, sama Yàlla, rikk, teewlul li ma lay ñaan, man sab jaam, di la ko dagaan; ngalla déggal sama yuux, te nangu ñaan gi ma lay ñaan bés niki tey. 29 Yal nanga ne jàkk guddeek bëccëg ci kër gii, bérab bi nga noon: “Fi la sama tur di nekk,” te yal nanga dégg ñaan gi ma jublu bérab bii, di ko ñaan, man sab jaam. 30 Yal nanga may nangul sama dagaan, nangul Israyil sa ñoñ. Bu ñu jubloo bérab bii, ñaan la, yal nanga ko dégge bérab ba nga dëkke ca asamaan, ba nangul leen, jéggal leen.
31 «Ku ñu tuumaal ne moo tooñ moroomam, te yoon waatloo ko ba waat war ko, bu dikkee di waatsi fi sa kanam sarxalukaay bi ci biir kër gii, 32 Su boobaa, yaw rikk dégge ko asamaan, àtte say jaam, ngir teg ki tooñ, daanub tooñ, këpp añu jëfam ci kaw boppam, te nga dëggal ki am dëgg, jox ko dëggam gi mu yelloo.
33 «Bu Israyil sa ñoñ daanoo fi kanam ab noon, ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu waññikoo ci yaw, sàbbaal saw tur, ñaan, sàkku saw yiw ci biir kër gii, 34 su boobaa yaw, yal nanga dégge asamaan, ba jéggale bàkkaarub Israyil sa ñoñ, te nga delloo leen ca réew ma nga joxoon seeni maam.
35 «Bu asamaan tëjoo, taw amul ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu jubloo bérab bii, ñaan la, sàbbaal saw tur te dëddu seen bàkkaar ndax sa mbugal, 36 su boobaa yaw ngalla nangool fa asamaan, te nga jéggale sa bàkkaaru jaam ñi, Israyil sa ñoñ. Ngalla xamal leen yoon wu baax wi ñu wara doxe te nga tawal sa suuf, si nga joxoon sa ñoñ, muy seen cér.
37 «Bu xiif amee ci réew mi, mbaa mbas, mbaa gàncax gi lakk, mbaa benaat xuural ko, mbaa mu diy njéeréer mbaa soccet, mbaa su dee congum seen noon ci seen dëkki réew mi, mbaa muy mboolem luy musiba ak mboolem jàngoro, su boobaa, 38 lépp lu ciy ñaan akug tinu gu bawoo ci képp ku mu doon mbaa ci mboolem Israyil sa ñoñ, te fekk ku ci nekk ràññee mititu xolam, ba tàllal ay loxoom jublook kër gii, 39 su boobaa, yaw, ngalla nangoo ko asamaan, màkkaan ma nga dëkke, ba jéggale, te nga jëf ba yool ku nekk kemu mboolem ay jëfam, yaw mi xam xolam, ndax yaw doŋŋ yaa xam xolu mboolem doom aadama. 40 Su ko defee dinañu la ragal seen giiru dund ci kaw suuf si nga joxoon sunuy maam.
41 «Te itam doxandéem bu bokkul ci Israyil sa ñoñ bu jógee réew mu sore ngir sa tur, 42 ndax kat dees na dégg sa tur wu réy, ak sa dooley loxo ak sa kàttanu përëg, bu dikkee ba jublu ci kër gii, ñaan, 43 su boobaa ngalla nangool asamaan, màkkaan ma nga dëkke, te nga defal doxandéem boobu mboolem lu mu la ñaan, ndax xeeti àddina yépp xam sa tur, ngir ragal la ni Israyil sa ñoñ, te xam ne saw tur lañu tudd ci kër gii ma tabax.
44 «Bu sa ñoñ di xarejeek seen noon, ci yoon woo leen yebal, su ñu ñaanee ci Aji Sax ji, jublook dëkk bii nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur, 45 su boobaa ngalla nangool asamaan, seenug ñaan ak seen dagaan te nga may leen ndam. 46 Bu ñu la moyee, nde amul nit ku dul moy, ba nga mere leen, teg leen ci loxob noon, noon ba jàpp leen, yóbbu am réewam, mu sore mbaa mu jege, 47 bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon, 48 bu ñu waññikoo seen léppi xol, ak seen léppi jëmm ci yaw, foofa ca seen réewu noon ya leen jàpp, ba ñaan la, jublook seen réew ma nga joxoon seeni maam, jublook dëkk bi nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur, 49 ngalla su boobaa, nangool ca asamaan, bérab ba nga dëkke, seen ñaan ak seen dagaan, te nga sàmm seen àq, 50 te it nga jéggal sa ñoñ ñi la moy, jéggal leen seen mboolem tooñ yu ñu la tooñ, te may leen yërmandey ña leen jàpp, ba ñu yërëm leen. 51 Ndax kat ñooy sa ñoñ ñi nga séddoo, génnee leen Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ga.
52 «Sang bi, teewlul bu baax samay tinu ak sa tinuy mbooloom Israyil mii, ba nangul leen mboolem lu ñu la jooy, 53 ndaxte danga leena ber ci biir xeeti àddina yépp, séddoo leen, te waxoon nga ko, Musaa sa jaam ba jottli ko, ba ngay génne sunuy maam Misra, yaw Boroom biy Aji Sax ji.»
Suleymaan ñaanal na bànni Israyil
54 Ba Suleymaan noppee ñaan Aji Sax ji mboolem ñaanam ya ak dagaanam yooyu, daa siggee ca sarxalukaayu Aji Sax, ja mu sukkoon tàllal loxo ya, jublu asamaan. 55 Mu taxaw, di ñaanal mbooloom Israyil mépp, daldi àddu ca kaw ne: 56 «Cant ñeel na Aji Sax, ji may Israyil mbooloom ab dal-lukaay, muy la mu waxoon lépp, ngir benn baat fanaanul àll ci digey jàmm yi mu dige woon yépp, Musaa jaamam ba jottli. 57 Yal na sunu Yàlla Aji Sax ji ànd ak nun, na mu ànde woon ak sunuy maam. Yàlla bu nu wacc mukk mbaa mu di nu dëddu. 58 Yal na nu xiir ci boppam, nuy tegu ci yoonam yépp, di jëfe ay santaaneem aki dogalam ak àttey yoonam yi mu dénkoon sunuy maam. 59 Sama kàddu yii ma ñaan fi kanam Aji Sax ji, yal na doon lu sunu Yàlla Aji Sax ji def yitteem guddeek bëccëg. Mu di ma dëggal, man jaamam, di dëggal Israyil ñoñam, saa yu nu ko soxlaa. 60 Su ko defee xeeti àddina yépp dinañu xam ne Aji Sax ji mooy Yàlla, te amul moroom. 61 Waaye nag joxleen Aji Sax ji sunu Yàlla seen léppi xol, ngir ngeen mana tënku ciy dogalam tey jëfe ay santaaneem ni bésub tey.»
Suleymaan daloo na kër Yàlla ga
62 Ba mu ko defee Buur Suleymaan ànd ak Israyil gépp, sarxe ab sarax fi kanam Aji Sax ji. 63 Mu defal Aji Sax ji saraxi cant ci biir jàmm, lépp di ñaar fukki junniy nag ak ñaar (22 000) ak téeméeri junniy gàtt ak ñaar fukk (120 000). Noonu la Buur ak bànni Israyil gépp amale xewu jagleb kër Aji Sax ji. 64 Bésub keroog Buur sellal na digg ëtt ba janook néeg Aji Sax ji, ndax fa la joxe saraxu rendi-dóomal ba, ak saraxu pepp ba, ak nebbonu saraxu cant ci biir jàmm, ndax sarxalukaayu xànjar ba fa kanam Aji Sax ji moo tuutoon ci defandoo saraxu rendi-dóomal ba, ak saraxu pepp ba, ak nebbonu saraxu cant ga ci biir jàmm.
65 Suleymaan nag amal màggal ga jant yooyu, ànd caak Israyil gépp, muy ndaje mu réy mu jóge Lebo Amat ca bëj-gànnaar ba ca xuru Misra ca bëj-saalum, di màggalsi fi sunu Yàlla Aji Sax ji, ba mu am juróom ñaari fan, tegaat ca juróom ñaari fan, muy fukki fan ak ñeent. 66 Bésub juróom ñetteel ba nag Buur yiwi mbooloo ma, ñu ñaanal ko, daldi dellu seeni xayma, ci biir mbégte ak xol bu sedd ci mboolem lu baax la Aji Sax ji defal Daawuda jaamam ba, ak Israyil, ñoñam.
* 8:2 weeru Etanim moo yemook sàttumbar, jàpp oktoobar, ñu daan ca amal màggalu Mbaar ya. 8:9 Oreb mooy Sinayi ba tey.