6
Suleymaan tabax na kër Yàlla ga
1 Ca ñeenti téeméereelu at maak juróom ñett fukk (480), gannaaw ba bànni Israyil génnee réewum Misra, ca ñeenteelu atu nguurug Suleymaan, ci weeru Siw, di ñaareelu weeru at ma, ca la Suleymaan tàmbalee tabax kër Aji Sax ji.
2 Kër gi Buur Suleymaan tabaxal Aji Sax ji, juróom benn fukki xasab la guddaay bi am, yaatuwaay bi di ñaar fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab.
3 Buntu néeg bu mag bi ab dëru biti la jàkkaarlool, yaatuwaayu dër bi di ñaar fukki xasab, tollook yaatuwaayu kër gi. Guddaayam féete ci kanam kër gi, yokke guddaayu kër gi fukki xasab.
4 Mu defal miiri kër gi ay palanteer yu am feguwaay yu ñu we ay caax.
5 Mu tabax ay taax yu sës ca ñetti miiri kër gi. Taax yi dar ñaari miiri néeg bu mag bi ak miiru néegu biir bu sell bi ci gannaaw. Taax yi def ay néeg yu ndaw.
6 Taax mi féete suuf juróomi xasab mooy yaatuwaayam, taax mi ci tegu di juróom benni xasab. Taaxum kaw mi am yaatuwaayu juróom ñaari xasab; ndax dañoo bàyyi ay teguy làcc ci miiri kër gi, ngir xaddi taax yi baña jàpp ci miiri kër gi.
7 Kër ga, ba ñu koy tabax ay doj lañu ko tabaxe, muy doj yu ñu yett fa ñu ko jële ba noppi, moo tax du saddu, du sémmiñ mbaa lenn luy jumtukaayu weñ bu ñu dégg mu dal, diir ba ñuy tabax kër ga.
8 Buntu taax mi ci suuf ma nga féete woon ndijoor, nit mana jaare ci ay dëggastal, yéeg jàll ci taaxum digg mi, jóge ci taaxum digg mi, jàll ci taax mi ci kaw.
9 Suleymaan tabax kër gi ba noppi, xadde ko dénki garabi seedar ak gàlluy seedar.
10 Taaxi kaw yi wër kër gépp, bu ci nekk juróomi xasab la def taxawaayam, lëkklee ko peeri garabu seedar, ba mu sës ca kër ga.
11 Ci biir loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Suleymaan. Mu ne ko:
12 «Kër gii de yaa ngi koy tabax. Waaye soo sàmmee samay dogal ak samay ndigal, di jëfe sama santaane yépp, di ci topp, su boobaa dinaa sottal li ma digoon sa baay Daawuda ci sa mbir.
13 Dinaa dëkk ci digg bànni Israyil, te duma dëddu Israyil, sama ñoñ.»
14 Ba mu ko defee Suleymaan tabax kër gi, ba sottal ko.
Liggéey nañu biir kër gi
15 Fa féete biir nag, mu lale miir yi xànqi seedar, dale ko ci suuf ba ci xadd bi. Dafa lal biir kër gi bant, lal dër bi xànqi sippar.
16 Bàyyi na itam ñaar fukki xasab ci biir kër gi ci gannaaw, muy néeg bu mu lale banti seedar ci suuf ba ci xadd bi ci kaw. Mu sàkk ko ci biir kër gi, mu dib néegu biir bu sell, di bérab bu sell baa sell.
17 Ñeent fukki xasab yi ko féete kanam di néeg Yàlla bu mag bi.
18 Banti seedar yi lale ci biir kër gi, dees cee yett ay nataali koog ak tóor-tóor yu focci; lépp di bantu seedar, ba xeer feeñul.
19 Néeg bu sell baa sell ca biir kër ga ca biir-a-biir la waajal, ngir yeb fa gaal gay def àlluway kóllërey Aji Sax ji.
20 Néeg bu sell baa sell amoon na guddaayu ñaar fukki xasab, yaatuwaay ba di ñaar fukki xasab, taxawaay ba di ñaar fukki xasab; Suleymaan xoob ko wurusu ngalam. Sarxalukaayu seedar ba jàkkaarlook néeg ba, moom it xoob na ko wurusu ngalam.
21 Ci biir loolu Suleymaan xoob biir néeg Yàlla ba wurusu ngalam. Mu tàllal ay càllalay wurus fi kanam néeg bu sell baa sell,
22 daldi xoob ci biir wurus ba mu daj.
Sarxalukaayu néeg bu sell baa sell, lépp la xoob wurus.
23 Ci kaw loolu mu sàkk ca biir néeg bu sell baa sell ñaari malaakay serub yu ñu yette bantu oliw, jëmm ju ci nekk am taxawaayu fukki xasab.
24 Benn serub bi laaf mu ci nekk juróomi xasab la, muy fukki xasab ci catal menn laaf mi ba ca catal laaf ma ca des.
25 Fukki xasab it mooy taxawaayu ñaareelu serub bi, ndax ñaari serub yee tolloo dayo, bokk bind;
26 taxawaayub serub bu ci nekk fukki xasab la.
27 Suleymaan teg serub ya ca digg néeg bu sell baa sell, seeni laaf fireeku, catal laafu benn serub bi di laal genn wetu tabax bi, catal laafu serub ba ca des di laal geneen wetu tabax bi. Seen ñaari cati laaf yi ci des it di laale fa tollook digg néeg ba.
28 Mu teg ca xoob serub yi wurus.
29 Mu yettlu nag ay serub ci kaw miiri ñaari néegi kër gi, yettaale garabi ron aki tóor-tóor yu focci, wërale.
30 Xoob na itam dëru tabax bi wurus, ci néegu biir bi ak ci biti.
31 Buntu néeg bu sell baa sell, kubeeri banti oliw la ko def, njëël bunt bi aki jënam bant lañu yu bindoo juróomi wet.
32 Ñaari kubeer yi banti oliw la; mu yettlu ca kawam ay malaakay serub aki ron aki tóor-tóor yu focci, ba noppi xoob lépp wurus, xoobaale serub yi wurus ak ron yi itam.
33 Noonu it la def buntu néeg bu mag bi, ay jënam di bantu oliw, waaye bunt bi, jëwam aki jënam, bant lañu yu bindoo ñeenti wet.
34 Ñaari kubeeram di bantu sippar, bu ci nekk di ñaari xànq yuy warangiku.
35 Mu yettlu ci kaw kubeeri bunt yi jëmmi serub aki ron aki tóor-tóor yu focci, daldi xoob lépp wurus.
36 Suleymaan tabaxe miiru ëttu biir bi ay xeeri yett ak xànqi seedar, ba ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca.
37 Ca ñeenteelu atu nguurug Suleymaan, yemook ñaareelu weer wa, di weeru Siw, ca lañu teg kenug kër Aji Sax ji.
38 Ca fukkeelu at maak benn, yemook juróom ñetteelu weer wa, di weeru Bul, ca la kër ga sotti, mook mboolem la ca bokk ak na mu wara bindoo lépp. Suleymaan tabax na kër ga ci juróom ñaari at.