4
Suleymaan fal na ay njiit
Ci kaw loolu Buur Suleymaan di boroom Israyil gépp. Ay jawriñam ñii la woon: Asaryaa sëtu Cadog moo doon sarxalkat bi; Eliyoref ak Awiya doomi Sisa di bindkat yi; Yosafat doomu Ayilut yore kàddug Buur; Benaya doomu Yoyada jiite mbooloom xare ma; Cadog ak Abiyatar di ay sarxalkat. Asaryaa doomu Natan moo jiite woon ndawi Buur ya, Sabudd doomu Natan di sarxalkat te di diglekatu buur. Ayisar moo doon saytu kër Buur, Adoniram doomu Abda di sase liggéeyi sañul-bañ ya.
Buur Suleymaan amoon na fukki jawriñ ak ñaar ci Israyil gépp. Ñuy topptoo dundub Buur ak waa këram, weer wu nekk kenn ci ñoom yor dund ba, ba at mi mat. Ñooñoo di:
Ben Ur ma sasoo woon diiwaanu tundi Efrayim.
Ben Deker sasoo Makas ak Saalbim ak Bet Semes ak Elon Bet Anan.
10 Ben Keset sasoo Arubot, boole kook Soko ak mboolem diiwaanu Efer.
11 Ben Abinadab sasoo diiwaanu Dor bépp; Tafat doomu Suleymaan di soxnaam.
12 Baana doomu Ayilut sasoo Taanag ak Megido ak diiwaanu Bet San gépp, feggook Sartan, fa féete Yisreel suuf, muy diggante Bet San ba Abel Mewola, ba ca wàllaa Yogmeyam.
13 Ben Geber a sasoo woon Ramot ca Galàdd, booleek dëkk-dëkkaan ya làngu Yayir doomu Manase féetewoo woon, foofa ca Galàdd ak diiwaanu Argob ca Basan. Muy juróom benn fukki dëkk yu mag yu ñu wërale ay tata ak seeni bunt ak yeti xànjar yu koy tëj.
14 Ayinadab doomu Ido sasoo Maanayim.
15 Ayimaas ma sasoo Neftali; moom it jël na doomu Suleymaan ju ñuy wax Basmat soxna.
16 Baana doomu Usay boole diiwaanu Aser ak Beyalot.
17 Yosafat doomu Paruwa sasoo diiwaanu Isaakar.
18 Simey doomu Ela sasoo diiwaanu Beñamin.
19 Geber doomu Uri sasoo diiwaanu Galàdd, di réewum Siwon buurub Amoreen ña ak réewum Og buuru Basan. Muy benn ndawal buur bu yilif réew mooma.
20 Waa Yuda ak Israyil dañoo bare woon, ba mel ni feppi suufas géej, di lekk, di naan, nekke mbégte.