15
Abiyam falu na ca Yuda
Ca fukki at ak juróom ñetteelu nguurug Yerbowam, ca la Abiyam doomu Nebat falu buur ca kaw Yuda. Ñetti at la nguuru fa Yerusalem te yaayam moo doon Maaka doomu Abisalom*. Muy roy nag baayam ca mboolem bàkkaar ya mu daan def. Te it wéetalul woon Yàllaam Aji Sax ji ni maamam Daawuda. Terewul Daawuda tax Aji Sax ji Yàllaam may ko doom ju góor ju koy wuutu ca Yerusalem, ndax askanu Daawuda baña fey, Yerusalem it mana ñoŋ. Li ko waral mooy Daawuda da daan jëfe njub lu Aji Sax ji rafetlu, te giiru dundam gépp teggiwul lenn lu ko Aji Sax ji sant lu moy ci mbirum Uri Etteen ba. Xare masula dakk diggante waa kër Robowam ak Yerbowam giiru dundu Abiyam gépp.
Li des ci mbiri Abiyam ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. Xare it jiboon na diggante Abiyam ak Yerbowam. Gannaaw gi Buur Abiyam tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda, Asa doomam falu buur, wuutu ko.
Asa falu na ca Yuda
Ba Buur Yerbowam faloo Israyil, ba dugg ñaar fukkeelu atu nguuram, ca la Asa falu buur, jiite Yuda. 10 Ñeent fukki at ak benn la Buur Asa péeyoo Yerusalem. Maaka doomu Abisalom ju jigéen moo doon maamam. 11 Asa nag di def njub gi Aji Sax ji rafetlu, Daawuda maamam. 12 Dàqe na ca réew ma ñu daan jaay seen bopp fa ñuy màggale tuur ya. Mu jële ca réew ma kasaray tuur ya fa ay maamam defoon yépp. 13 Maaka maamam ju jigéen sax, Asa xañ na ko céru lingeer yaayu buur ba mu amoon, ndax Maaka moo sàkkaloon Asera tuur ma, ab xer bu seexluwu bu ñu koy màggale. Asa gor xeru maamam ja, lakk ko ca xuru Sedoron. 14 Waaye bérabi jaamookaay ya, jëleesu ko fa, doonte Asa, Aji Sax ji la wéetaloon cib xolam, giiru dundam gépp. 15 Moo indi ca kër Aji Sax ji, jumtukaay yu sell yu baayam ya, ak jumtukaay yu sell yu boppam, muy xaalis ak wurus aki ndab.
16 Xare nag masula dakk diggante Asa ak Basa buurub Israyil seen giiru dund gépp. 17 Ci biir loolu Basa buurub Israyil song Yuda, daldi dàbbli dëkk ba ñuy wax Raama, ba kenn du dugg jëm ca Asa buurub Yuda mbaa muy génn. 18 Asa dajale mboolem luy xaalis ak wurus wu desoon ca denci kër Aji Sax ji, ak denci kër Buur. Mu teg ko ci loxoy jawriñam ña. Ba mu ko defee Buur Asa yebal leen ca buurub Siri ba ca Damaas, di Ben Addàd doomu Tabrimon doomu Esiyon.
Asa nag ne Ben Addàd: 19 «Kóllëree dox sama digganteek yaw, na mu doxe woon sama diggante baay ak sa baay. Lii nag maa la ko may, xaalis la ak wurus. Te nga dogoo rekk ak Basa buurub Israyil, ndax mu jóge samam réew.» 20 Ben Addàd déggal Buur Asa, daldi yebal njiiti xarey gàngooram ca dëkki Israyil. Ni la nangoo dëkk ya ñuy wax Yon ak Dan ak Abel Bet Maaka ak diiwaanu Kineret gépp, boole ca diiwaanu Neftali gépp. 21 Ba ko Basa déggee, Raama ga mu doon dàbbli la ba, ba dem toogi Tirsa.
22 Ba loolu amee Buur Asa joxe ndigal, woolu waa Yuda gépp, kenn desul. Ñu ànd jëleji ca Raama doj yaak bant ya Basa doon tabaxe. Buur Asa tabax ca dëkk ba ñuy wax Geba gu giirug Beñamin, tabax ca Mispa.
23 Li des ci mbiri Asa ak mboolem njàmbaaram ak la mu def yépp ak dëkk ya mu tabax, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant. Ba Asa demee ba màggat nag, jàngoroy tànk la ame woon. 24 Gannaaw gi mu tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda maamam. Yosafat doomam falu buur, wuutu ko.
Nadab falu na ca Israyil
25 Ba Asa buurub Yuda duggee ñaareelu atu nguuram, ca la Nadab doomu Yerbowam falu buur, jiite Israyil. Nadab jiite na Israyil ñaari at, 26 di jëfe lu Aji Sax ji ñaawlu, aw ci tànki baayam, di bàkkaarloo Israyil. 27 Ci biir loolu doomu Axiya, ji giiroo ci Isaakar te ñu di ko wax Basa, daldi fexeel Nadab, jam ko ca Gibeton gu Filisteen ña. Fekk Nadab ànd ak Israyil gépp, gaw Gibeton. 28 Basa daldi rey Nadab, yemook ba Asa buurub Yuda di dugg ñetteelu atu nguuram. Basa falu buur, wuutu Nadab. 29 Naka la falu, daldi rey waa kër Yerbowam gépp. Bàyyiwul kenn kuy noyyi te bokk ci Yerbowam. Mu faagaagal leen, muy la Aji Sax ji waxoon, Axiya jaamam ba ca Silo jottli. 30 Li ko waral mooy bàkkaari Yerbowam yi mu bàkkaar te bàkkaarloo ko waa Israyil, di merloo Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ba feesal xolam.
31 Li des ci mbiri Nadab ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
32 Xare masula dakk diggante Asa ak Basa buurub Israyil, seen giiru dund gépp.
Basa falu na ca Israyil
33 Ba Asa buurub Yuda duggee ñetteelu atu nguuram, ca la Basa doomu Axiya falu buur ca Israyil gépp, péeyoo Tirsa. Nguuru na ñaar fukki at ak ñeent. 34 Da daan def li Aji Sax ji ñaawlu, aw ci tànki Yerbowam ak bàkkaaram ya mu daan bàkkaarloo Israyil.
* 15:2 Abisalom ak Absalom jàpp nañu ne kenn ki la. 15:5 Seetal ci 2.Samiyel 11. 15:17 Raama ma nga féete woon Yerusalem bëj-gànnaar, tollu diggante ñaari réew yi. Mu nekkoon ci kaw tund wu aw yoon jaar, jóge péeyu Israyil, jëm Yerusalem.