5
Mbugal war na
Yàllaay wax
1 «Wërleen mbeddi Yerusalem,
xool-leen, seet ciy péncam rekk ba xam
ndegam dingeen gis kenn,
kenn kepp kuy def njub,
di sàmm worma,
ma daldi leen baal.
2 Bu ñu nee sax: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund,”
ay fen lañuy giñ.»
Yeremeey wax
3 Aji Sax ji, xanaa du worma ngay sàkku?
Dóor nga leen, safu leen;
nga làbbli, ñu tanqamlu,
wowle ba raw doj, baña dëpp.
4 Man nag, ma noon: «Ñii de ay baadoolo rekk lañu,
di def jëfi dof,
xamuñu yoonu Aji Sax ji,
xamuñu lu seen àtteb Yàlla laaj.
5 Kon naa dem seeti kàngam yi,
wax ak ñoom.
Xanaa ñoom dinañu xam yoonu Aji Sax ji,
xam lu seen àtteb Yàlla laaj.»
Waaye ñoo bokk daggook Yàlla,
dogook moom.
6 Moo tax gaynde di génne ci gott bi, fàdd leen,
bukkiy màndiŋ mi di leen yàpp,
segg di tëru seeni dëkk,
ku ca génne, dees na la xotat.
Seeni moy a bare,
te seen ñàkk worma réy.
Yàllaay wax
7 «Yerusalem, ana lu tax ma di la baal,
te say doom wacc ma,
di giñe lu dul Yàlla.
Ma reggal leen, teewul ñuy njaaloo,
riixle, jëm kër gànc ya!
8 Mbete fas yu suur, tukkal,
ku ne ŋexal, jëm sa jabaru moroom.
9 Lii, duma leen ko dumaa?»
Kàddug Aji Sax jee.
Mu ne: «Wii xeet, duma ko fey yoolam?»
Dëddu Yàlla, gis ko
10 «Yéegleen seeni tata, yàqte
waaye buleen leen jeexal tàkk.
Tenqileen lawit yi,
ñooñoo bokkul ci Aji Sax ji.
11 Waa kër Israyil ak waa kër Yuda kat,
ñoo ma wora wor!»
Kàddug Aji Sax jee.
12 Mu ne: «Ñoo fenal Aji Sax ji,
naan: “Moom du def dara,
musiba du nu dal,
saamaroo, xiifoo, dunu ci gis dara.
13 Yonent yi daal, ngelawal neen!
Kàddug waxyu newul ci ñoom;
li ñuy wax, na leen yenu!”»
14 Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Gannaaw wax jii lañu wax,
maa ngii di def samay wax di sawara ci sa gémmiñ,
askan wii di matt,
mu xoyom leen.
15 Éey waa kër Israyil,»
kàddug Aji Sax jee,
«maa ngii di indi fi seen kaw xeet wu bawoo fu sore.
Xeet wu am kàttan lañu,
xeet wu yàgga yàgg,
wu ngeen xamul seen làmmiñ,
te dégguleen seeni wax.
16 Seen mbari fitt ŋafal paxum bàmmeel,
ñoom ñépp di ñeyi xare.
17 Ñooy dikk, warax seen meññeef ak seen ñam,
jeexal seeni doom, góor ak jigéen,
lekk seen jur gu gudd ak gu gàtt,
saax-saaxee seeni reseñ ak seeni figg;
te dëkk yi ngeen yaakaare seeni tata,
dooley saamar a koy tas.
18 Waaye bési keroog it,»
kàddug Aji Sax jee,
«duma leen jeexal tàkk.
19 Bu ñu nee:
“Ana lu waral sunu Yàlla Aji Sax ji teg nu lii lépp?”
ne leen: “Yàlla nee:
Ni ngeen ma dëddoo, di jaamu yàllay jaambur ci seenum réew,
ni ngeen di jaamujee ay jaambur
biir réew mu ngeen moomul.”»
Yàlla àrtu na xeet wi
20 «Jottlileen lii waa kër Yanqóoba,
biral-leen ko fa Yuda, ne leen:
21 Ngalla dégluleen lii,
xeet wu dofe, ñàkk xel wi ngeen doon,
ami gët te dungeen gis,
ami nopp te dungeen dégg!
22 Man daal, dungeen ma ragal,
am tiituleen ma?»
Kàddug Aji Sax jee.
«Man mi teg gannuus, yemalee ko géej,
dogalal ko ko dàkk te du ko jàll,
lu mu wañax wañax du ko man;
gannax ya day riir, te du jàll!
23 Waaye wii xeet a dëgër bopp te déggadi.
Dëddu nañu ma ba wéy.
24 Seen xel demul sax ba ne:
“Tee noo ragal sunu Yàlla Aji Sax,
jiy jot, mu tawal nu,
taw yu jëkk ak yu mujj yi,
àppal nu ayi bési ngóob,
sédde nu?”
25 Yooyii seeni ñaawtéef a ko waññi,
seen bàkkaar a leen xañ ngëneel.
Mbon maase na ci xeet wi
26 «Waaw! Daa am ñu bon ci sama ñoñ,
ñuy tërook a fiire
mbete nappkati picc.
27 Ni kaaf di feeseeki picc,
ni la seeni kër di feese alali càcc,
ba tax ñu yokku ba woomle,
28 yaflu, di nes-nesi.
Seenug mbon it amul kem:
duñu defal jirim njub,
duñu àtte néew-ji-doole dëgg.
29 Lii, duma leen ko dumaa?»
Kàddug Aji Sax jee.
«Xeet wu mel nii duma ko fey yoolam?
30 Lu siblu te yées am na ci réew mi:
31 Yonent yiy wax waxyuy fen,
sarxalkat yiy jiitee seen coobare,
te sama ñoñ soppe ko ni!
Moo bu muj ga taxawee, nu ngeen di def?»