Kàddug waxyu dalati na xeet yi
46
(Saar 46—51)
Kàddug Aji Sax jii dikkal na Yonent Yàlla Yeremi, jëm ci xeet yi.
Lu jëm ci Misra
Firawna buuru Misra, bi ñuy wax Neko, ba ko Nabukodonosor buuru Babilon di duma, ma nga woon ca Karkemis ca tàkkal dexu Efraat. Mu yemook ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya Yowakim buurub Yuda. Kàddug waxyu gii moo jëm ci Misra ci wàllu diggante ba seen mbooloom xare ma tollu woon.
«Ŋàbbleen pakkoo pakk te xareji.
Takkleen fas yi, war naari góor yi,
ba làng-déraale seen mbaxanay xare,
nàmmaat xeej,
sol yérey xare!»
 
«Ana lu ma gis?
Waa Misraa jaaxle bay dellu gannaaw,
seeni jàmbaar falaxoo,
ne wëqet, geesuwñu,
tiitaange ubale.»
Kàddug Aji Sax jee!
«Bu nit gaaw ba raw
mbaa mu jàmbaare ba mucc.
Bëj-gànnaar lañu féete, feggook dexu Efraat,
di tërëf, di daanu.
 
«Kii ku mu, muy fuddu ni dexu Niil,
di fuur ni wali ndox?
Misraa, mooy fuddu ni dexu Niil,
di fuur ni wali ndox.
Mu naan: “Maay fuddu, mëdd àddina,
sànk ab dëkk ak ña ca biir.”
Na fas buur, watiir fiddi,
jàmbaar sàqi:
waa Kuusoo waa Puut ak seeni pakk,
ak waa Ludd ak seeni xala.
10 Waaye bésub keroog déy,
Boroom bi Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko moom,
muy bésub feyu bu muy feyey noonam.
Saamar suur suux,
màndee deret.
Boroom bi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
mooy rendee réewum bëj-gànnaar ab sarax,
feggook dexu Efraat.
11 Yaw Misra mu taaru mi,
demal ba Galàdd wuti diw, dàmpoo.
Faju, fajooti;
dara du la wéral!
12 Xeet yeey dégg sa toroxte,
sa yuux dajal àddina.
Jàmbaar téqtaloo jàmbaar,
ñu ànd ne fëlëñ!»
13 Kàddu gii dikkaloon na Yonent Yàlla Yeremi, ba Nabukodonosor buuru Babilon dikkee, di duma waa réewum Misra. Mu ne:
14 «Yégleel lii Misra, yéene ko fa ca Migadol,
yéene ko fa ca Memfis ak Tapanes.
Neleen: “Dërleen, taxaw temm!
Saamar kat a ngi lekk li leen wër.”
15 Lu Apis di daw?
Lu tee seen yàllay yëkk jooju taxaw?
Xanaa Aji Sax jee ko bëmëx!
16 Moo bëmëx ñu bare,
ku nekk naan moroom ma:
“Jógal nu dellu ca sunuy bokk,
ca sunu réewum cosaan,
ba mucc saamaru noon.”
17 Dees na fa woyal Firawna buuru Misra, naan ko:
“Coowal neen te bés wees.”
 
18 «Giñ naa ko ci man miy dund,»
kàddug Buur Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi di turam:
«noon ay dikk, mel ni tundu Tabor ci digg tund yi,
mbete tundu Karmel wi feggook géej.
19 Yaw mi dëkke Misra mu taaru mi,
ëmbal sa ëmb, jëm ngàllo;
Memfis* dëkk bii kat ci gental la jëm,
di ndànd-foyfoy lu kenn dëkkul.
20 Misra daa mel ni jeegu nag bu yànj,
weñ ne waa, waa, bawoo bëj-gànnaar.
21 Seen xarekat yi ñu bind sax
ñu ngi mel ni sëllu yu yaflu,
ñoom it ànd ne wërëñ, wëqet,
kenn taxawul!
Bésu safaan a leen dikkal,
seen mbugal taxaw,
22 ñu daw di faraas-faraasiy wéy ni jaan.
Doole la noon songe Misra,
dikke leeni sémmiñ
ni gorkati garab.
23 Lu gott fatt fatt, ñu gor.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Ñoo gëna barey njéeréer,
ba maneesu leena lim.
24 Gàcceel nañu Misra mu taaru mi,
teg ko ci loxoy xeeti bëj-gànnaar.»
25 Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi wax na ne: «Maa ngii di dikke mbugal Amon, tuuru dëkk bii di Teeb, ak Firawnaak waa Misraak seeni tuur ak seeni kàngam, boole ci ñi yaakaar Firawna. 26 Maa leen di teg ci loxoy ñiy wut seen bakkan, di Nabukodonosor buuru Babilon aki jawriñam. Gannaaw loolu dees na dëkkewaat Misra na woon.» Kàddug Aji Sax jee!
Israyil dina xettliku
27 «Yaw Yanqóoba sama jaam bi nag, bul tiit;
yaw Israyil, ma ne bul ragal.
Maa ngii di la wallusi,
jële la fu sore,
jële sa askan
fa seen réewu njaam ga,
Yanqóoba délsi,
dal, aaru, du tiitati.
28 Yaw Yanqóoba sama jaam bi, bul tiit.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Yaw laa àndal.
Maay fàkkas mboolem xeet yi ma leen sànni woon,
waaye yeen, duma leen fàkkas.
Duma leen ñàkka duma moos,
waaye dinaa leen yar lu yem.»
* 46:19 Memfis: Fii ñu ne Memfis, am na sotti yu fi indi turu Nof.