21
Jéllub Yerusalem jubsi na
1 Kàddu dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo fa Aji Sax ji. Mooy ba buur Cedesyas yebalee ca moom, Pasur doomu Malkiya, mook sarxalkat ba ñuy wax Cefaña doomu Maaseya. Mu ne ko:
2 «Ngalla seetal nu ci Aji Sax ji, ndax Nabukodonosor buuru Babilon mu ngi nuy song xare. Jombul Aji Sax ji defaatal nu lenn ciy kéemaanam ba mu dellu gannaaw.»
3 Yeremi nag ne leen: «Waxleen Cedesyas ne ko:
4 “Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: Seen dooley xare ji ngeen yor, di xeexeek ñi ci biti, di buuru Babilon ak waa Babilon ñi leen gaw, maa ngii di ko walbati, dajale ko ci biir dëkk bii.
5 Man mii maay xareek yeen, won leen sama doole ak sama diisaayu loxo, xadaru, dikke leen mer mu réya réy.
6 Maay fàdd lu dëkk ci dëkk bii, nit ak mala bokk loroo mbas mu réy.
7 Gannaaw loolu nag,” kàddug Aji Sax jee, “Cedesyas buurub Yuda, aki jawriñam ak askan week ñi des ci dëkk bii te rëcce ci mbas meek xare beek xiif bi, maa leen di teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, ak seen loxol noon, ak loxol ñi leen di wuta rey. Dina leen leel ñawkay saamar. Du leen baal, du ñéeblu, du yërëm.”
8 «Te itam nga wax askan wii ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teg fi seen kanam yoonu dund ak yoonu ndee.
9 Ku toog ci dëkk bii, dinga deeye xare mbaa xiif mbaa mbas. Ku génn jébbal boppam waa Babilon ñi leen gaw nag dinga dund, bakkanam di yoolu xareem.
10 Jógal naa dëkk bii déy, te loraange laa leen naral waaye du jàmm.” Kàddug Aji Sax jee. “Ci loxol buuru Babilon laa koy teg, mu jafal ko, lakk.”»
Xibaar ñeel na waa kër buur
11 «Te it waxal waa kër buurub Yuda ne leen:
“Dégluleen kàddug Aji Sax ji!
12 Yeen waa kër Daawuda,
Aji Sax ji dafa wax ne:
Àtte yoon, deeleen ko xëye,
di xettli ki ñu xañ dëgg
ci ki koy néewal doole,
balaa sama mer ne jippét,
di tàkk te deesu ko mana fey
ndax seen jëf ju bon.
13 Yeen ñi jataayoo xur wi,
yeen ñi ci kaw doj wu tell wi, maa ngii fi seen kaw.”
Kàddug Aji Sax jee.
“Yeen ñi naa: ‘Ku nu manal dara?
Ku jote sunu biiri rawtu?’
14 maa leen di dikke seen añu jëf.”
Kàddug Aji Sax jee.
“Maay jafal sawara, lakk seen gott bi,
mu xoyom lépp lu leen wër.”»