11
Yuda fecci na kóllëre
Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa Aji Sax ji: «Dégluleen sàrti kóllëre gii. Te yaw Yeremi, nga àgge ko képp kuy waa Yuda ak waa Yerusalem. Nga ne leen: “Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Alkànde ñeel na képp ku sàmmul sàrti kóllëre gii ma santoon seeni maam bés ba ma leen génnee réewum Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ba. Ma noon leen ngeen déggal ma te jëfe sàrti kóllëre gi ni ma leen ko sase, ba doon sama ñoñ, man ma doon seen Yàlla. Su ko defee ma wàccook ngiñ, la ma giñaloon seeni maam ne dinaa leen may réew mu meew maak lem ja tuuroo, muy fii tey.”» Ma ne ko: «Tigi, Aji Sax ji.»
Aji Sax ji ne ma: «Yéeneel mboolem kàddu yii ci biir dëkki Yuda yu mag yi ak ci mbeddi Yerusalem, nga ne: “Dégluleen sàrti kóllëre gii te jëfe ko. Artu naa àrtu seeni maam, dale ko ba ma leen génnee réewum Misra, ba tey jii ma jàppoo di leen àrtu, naan leen ngeen déggal ma. Waaye dégluwñu, teewluwñu, xanaa ku nekk di wéye dëgër bopp, topp ag bon xolam. Moo tax ma wàcce ci seen kaw mboolem sàrti kóllëre gii ma leen santoon ñu war koo jëfe te jëfewuñu ko.”»
Aji Sax ji dellu ne ma: «Pexem fippu feeñ na ca Yuda gépp ak ca waa Yerusalem. 10 Dellu nañu ca seen ñaawtéefi maam, ya bañoona sàmm samay kàddu. Ñoom it topp nañu yeneen yàlla, di leen jaamu. Waa kër Israyil ak waa kër Yuda fecci nañu kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam.»
11 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di leen wàcceel musiba mu ñu dul mana rëcc. Dinañu ma ne wóoy te duma leen déglu. 12 Su ko defee waa dëkki Yuda yu mag yeek waa Yerusalem dem jooytuji ca yàlla, ya ñuy taalal cuuraay, te duñu leen mana wallu mukk ci seen jamonoy musiba.
13 «Yaw Yuda, ni sa dëkk yu mag tollu, ni la say tuur tollu. Ni mbeddi Yerusalem tollu it, ni la sarxalukaay yi ñu fa saam tollu, ñu di fa taalal cuuraay Baal, tuur mu seexluwu mi.»
14 «Yaw nag Yeremi, bul ñaanal askan wii. Bu leen tinul, bu leen dagaanal. Ndax kat keroog bu ñu nekkee ci seen musiba, ba naan ma wóoy, du maay déglu.»
Aji Sax ji dëddu na soppeem
Yàllaay wax
15 «Ana lu samay soppe di defati sama kër?
Ñu bare ci ñoom a ngi def lu bon.
Ndax seeni sarax man naa far seen jëf ju ñaaw,
ba tax bu ñuy def lu bon, di ko bége?»
 
16 Oliw naat, jekki doom;
nii la leen Aji Sax ji tudde woon,
waaye riir mu réy lay jibal,
jafal ko, mu tàkk,
taar réer car ya, meŋŋ.
17 Aji Sax ji Boroom gàngoor bi leen jëmbatoon,
moo leen tuddal lu bon.
Nee: «Waa kër Israyil ak Yuda ñoo def lu bon,
di taalal Baal cuuraay ba merloo ma.»
Ñu ngi fexeel Yeremi
18  Aji Sax jee ma xamal, ma xam,
ba gis seeni jëf.
19 Ndax damaa naagu woon ni xar
mu ñu jëme rendikaay ba.
Xawma woon ne man lañuy lalal ay pexe,
naan: «Nan gor garab ak doomam,
dagge ko fi réewum boroom bakkan,
ba deesul fàttlikooti turam.»
 
20 Ma ñaan Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
kiy àtte dëgg, di nattu xel ak xol, ne ko:
«Yaw laa diis sama mbir,
won ma séen mbugal.»
21 Moo tax Aji Sax ji wax lii ci mbirum waa Anatot, ñiy wut sama bakkan, naan ma: «Baal di waxe waxyu ci turu Aji Sax ji, lu ko moy nu rey la.» 22 Moo tax kay Aji Sax ji Boroom gàngoor yi wax ne: «Maa ngii di wàccesi mbugal fi seen kaw; seen xale yu góor fàddoo saamar, seeni doom, góor ak jigéen, deeye xiif. 23 Aw nit, duñu ko dese; maay wàcceel waa Anatot safaan, bu seen atu mbugal taxawee.»