Yeremi
1
Muy kàddug Yeremi, góor gi baayam Ilkiya bokk ci sarxalkat yi dëkk Anatot, ca diiwaanu Beñamin. Kàddug Aji Sax ji dikkal ko ci jamonoy buuru réewum Yuda, Yosya doomu Amon. Mu yemook fukkeelu atu nguuram ak ñett. Kàddug Aji Sax ji dikkal na ko ba tey ci janti buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, di ko dikkal, ba keroog nguurug Cedesyas, jeneen doomu Yosya ja di jeex. Mu yemook fukkeelu atu nguuram ak benn, ca juróomeelu weer wa. Booba lañu jàpp waa Yerusalem njaam, yóbbu leen.
Waxyu dal na Yuda
(Saar 1.4—25.14)
Yàlla woo na Yeremi
Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma, ne ma:
«Laata ma lay sos ci sa biiru ndey, xam naa la;
laata ngay juddoo ci sa ndey, séddoo naa la,
def la ngay yonent ñeel xeet yi.»
 
Ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji,
da di manumaa wax, gone doŋŋ laa.»
 
Aji Sax ji ne ma: «Bul ne: “Gone laa.”
Képp ku ma la yebal, dem ca;
lépp lu ma la sant, wax ko.
Bu leen ragal, ngir yaw laay àndal,
di la xettli.»
Kàddug Aji Sax jee.
 
Aji Sax ji tàllal loxoom, laal sama gémmiñ.
Aji Sax ji ne ma:
«Mu ngoog, sexal naa la samay kàddu.
10 Ma ne, tabb naa la bés niki tey,
ci kaw xeet yeek réew yi,
ngay buddat, di fàqat,
di yàqte ak a daaneel,
di defar ak a jëmbat.»
Yàlla wone na ñaari misaal
11 Kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Caru garabu saal laa gis.» 12 Aji Sax ji ne ma: «Yaa ko gis, maa sàlloo def sama kàddu, ngir sottal ko.»
13 Kàddug Aji Sax ji dikkalaat ma ñaareel bi yoon, ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Cin luy bax laa gis. Mu ngi joye bëj-gànnaar, jublook nun.» 14 Aji Sax ji ne ma:
«Bëj-gànnaar la safaan bay fettaxe,
dal ci kaw waa réew mi mépp.
15 Maa ngii déy, di woo
mboolem waasoy réewi bëj-gànnaar ak seeni buur.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Dañuy dikk, ku ne dëj ngànguneem
fi janook bunti Yerusalem,
jànkoonteek tataam yépp,
ak dëkki Yuda yépp.
16 Maay biral samay àtteek ñoom
ci seen mbon gi gépp:
Dañu maa wacc,
di taalal cuuraay yeneen yàlla,
di sujjóotal lu ñu sàkke seeni loxo.
 
17 «Yaw nag takkul te wax leen lépp lu ma la sant.
Bul am tiitaange fi seen kanam,
lu ko moy ma tiital la fi seen kanam.
 
18 «Maa ngii def la bésub tey
nga mel ni dëkk bu mag bu tata wër,
mel ni xeru weñ mbaa tatay xànjar,
jàkkaarlook réew mi mépp,
muy buuri Yuda aki kàngamam,
di sarxalkati réew mi ak baadoolo yi.
19 Dañu lay xeex te duñu la man,
yaw laay àndal, di la xettli.»
Kàddug Aji Sax jee.