40
Aji Sax ji dellu ne Ayóoba:
Yaw miy layook Aji Man ji, dangay diiŋat?
Yaw miy weranteek Yàlla, doo tontu?
 
Ayóoba àddu ne Aji Sax ji:
Man mi tekkiwul dara, nu ma lay tontoo?
Sama loxo laa ube sama gémmiñ.
Maa waxoon benn yoon, waxatuma;
maa tóllanti woon, dootu am.
Yàlla dëkk na Ayóoba
Aji Sax ji daldi àddoo fa ngëlén la, ne Ayóoba:
Takkul boog te góor-góorlu,
ma laaj la, nga xamal ma.
Sañ nga maa teg tooñ daal,
di ma sikkal, ba am dëgg?
Dangaa am dooley Yàlla,
mbaa kàddu guy dënu ni gosam?
10 Ràngool boog màggaay ak teddnga,
te làmboo dayook daraja.
11 Yuril sa mer,
te xool képp ku bew, detteel ko,
12 xoolal képp ku bew, torxal ko,
te dëggaate ku bon fa mu taxaw.
13 Boole leen làq biir suuf,
tëjleen ràpp fu làqu fa,
14 Kon déy man maa lay sargal,
muy ndam lu la sa doole may.
 
15 Beyemot rab wu réy* waa ngii, maa ko sàkk, sàkk la,
ñax lay lekk niw nag.
16 Doole jaa ngoogu ca ndigg la,
kàttan ga laloo suuxi biir ba,
17 geen ga ne kàdd ni garabu seedar,
sidditi lupp ya ñabaloo,
18 yax ya di ponki xànjar,
cér ya mel ni yeti weñ.
19 Moo gëna yéeme ci li Yàlla sàkk,
te ki ko sàkk doŋŋ a koy boccil saamar.
20 Xontam déy tund yee ko yor,
rabi àll yépp di foye fa wetam.
21 Keppaaru déem lay goore,
làqoo barax ak ban,
22 déem ya keral ko,
garabi tàkk ga yéew ko.
23 Dex gu fees jaaxalu ko,
gannaxi Yurdan di ko talaata, mu ne tekk.
24 Ana ku koy jàpp te muy xoole?
Ak ku koy nos, ba téye ko?
 
25 Ninki-nànka nag yaa koy nappe oos?
Am yaay yeewe làmmiñ wa ag buum?
26 Yaay nase wakkan ya ag buum?
Am yaay bëtt ŋaam wa, we ca lonku?
27 Xanaa ca la lay tinoo tinu,
di la lewetali kàddoom?
28 Xanaa kon mooy digook yaw,
ngir nga def ko jaam ba fàww?
29 Am yaa koy foye ni picc,
takkal ko sa janq ji, ñu di ko seetaan?
30 Dees na ko waxaaleendoo?
Am ay julaa koy séddoo?
31 Yaa koy jamati xepp a?
Am yaa koy xaañ xeeju nappkat?
32 Teg ko loxo, seet;
dootoo fàtte boobu xeex,
te doo ko dolleeti.
* 40:15 rab wu réy wi am na ñu jàpp ne léebéer la. 40:25 ninki-nànka jii am na ñu jàpp ne jasig la.