21
Ayóoba weddi na àlluway xarit ya
1 Ayóoba àddu ne:
2 Dégluleen maa, dégluleen sama baat,
te mas-sawoo ma seenug teewlu.
3 Muñal-leen ma boog, ma wax, man,
balaa nit a reeti.
4 Sama tawat lii, da di maak nit a?
Gannaaw du nit, ana lu ma tee xàddi?
5 Geesuleen ma, waaru,
ba loxo ub gémmiñ.
6 Su ma ko xalaatee, damay tiit,
di kat-kati.
7 Lu tax ku bon di dund,
bay magal sax, di ànd ak doole?
8 Doomam day toog, mu fekke,
bay xool ay sëtam,
9 këram nekke jàmm, mucc safaan,
te yetu Yàlla du ko dal.
10 Ku bon, yëkkam day tëb te du moy,
nagam di jur te du xàcc.
11 Day gis ay xaleem di bajantu,
goneem yépp di tëbantu.
12 Day xaacoondook um tëgg aki xalam,
di bége baatub toxoro,
13 Ku bon ay ñédd ay fanam ci biir teraanga,
doora jekki wàcci njaniiw.
14 Moona kee noon Yàlla: «Xiddi ma!
Xam saw yoon soxalu ma.
15 Ana kuy Aji Man ji sax ba ma di ko jaamu?
Su ma ko tinoo, ana lu mu may jariñ?»
16 Kii xanaa du teraangaam a ngi ciy loxoom?
Ndaxam taxul ma roy ko fenn!
17 Ku bon, ana fu ag xuyyam kamaje?
Fu ko musiba dikkale?
Fu Yàlla mere, ba sédd ko safaan?
18 Ana fu ku bon mele nim ñax mu ngelaw wal,
mbaa boob mu callweer yóbbu?
19 Ãa ku bon daal ay tooñ, Yàlla dencal doomam añ ba?
Ki tooñ kay, na ko fey, mu xam,
20 gisal boppam sànkuteem,
ba jolu merum Aji Man ji!
21 Ana luy yoonu ku bon ci waa këram, gannaawam,
te fekk limu fanam jeex?
22 Ana kuy jàngal Yàlla xam-xam,
moom miy àtte ñu kawe ña?
23 Kii a ngi deeyaale dooleem,
xel ma dal, tiitul dara,
24 yaram wa niin,
yax ya naat.
25 Kee deeye naqaru xol,
masula ñam bànneex,
26 te ñooy tëddandoo biir suuf,
bokk sàngooy sax.
27 Mu ngoog! Maaka xam li ngeen foog,
te di ma ko fexee fitnaale!
28 Ngeen ne: «Ana fu kër kàngam di mujje?
Ana xayma ba ku bon ka dëkke?»
29 Xanaa laajuloo tukkikat yi?
Am gëmuloo seeni seede?
30 Bésub safaan ku bon ay mucc,
bésub mbugal it, mooy raw.
31 Ana kuy janook moom, sikke ko jikkoom?
La mu def, ana ku ko koy fey?
32 Moom de bu deeyee, sëg ya lees koy robi,
te bàmmeelam, dees na ko wattu.
33 Liy topp néew ba, day bare,
liy dox jiitu ko wees ab lim,
te suufu xur wa sax da koy sedde.
34 Kon seeni mas-sawu, cóolóoli neen!
Seeni tont, jinigali kese!