15
Nee ñu lu waay def, boppam
1 Elifas àddu, ne:
2 Ayóoba, ku xelu dina tontoo kàdduy ngelaw,
mbel-mbelam nib jaas bu fees dënnam a?
3 Ku xelu du layoo waxi caaxaan,
kàddu yu amul lenn njariñ.
4 Yaw de, yaa ngi neenal worma,
di yàq njàngat mi war fa Yàlla.
5 Saw làmmiñ déy, sa ndëngtee koy sa,
yaa taamu di wax njublaŋ.
6 Du man de, sa gémmiñu bopp a la teg daan,
sa làmmiñu bopp a la tuumaal.
7 Xanaa yaa jëkka juddu ci nit?
Am balaa tund yee sosu lañu la jur?
8 Ba Yàllay féncoo yaa doon déglu,
ba mana aakimoo xel mu rafet?
9 Ana loo xam lu nu xamul
ak dég-dég boo am, te nu rafle ko?
10 Boroom bijjaaw ak màggat a ngi sunu biir,
di ñu sut sa baay aw fan.
11 Kàddu yi la Yàlla di mas-sawoo da laa doyul?
Boole ci li ñu lay waxe teeyu bakkan?
12 Ana looy waxe xol,
di saxaral kanam nii?
13 Ngay sippi Yàlla sa mer,
di ko wax lu mel nii!
14 Ana nit ku mana jub xocc?
Ana ku laab ku jigéen jur?
15 Yàlla wóoluwul sax ñu sellam ña ca asamaan,
te asamaan sellul ba doy ko,
16 rawatina nit, moom mi jara seexlu,
yàqu jikko,
di def njubadi ni ndoxum naan.
17 Déglu ma, ma wax la,
xamal la li ma gis,
18 muy lu ñu rafet xel ñi jottli,
jële ko ca seeni maam, te làquñu ko.
19 Ñoom, seeni maam doŋŋ a jagoo woon réew mi,
ba leen doxandéem raxaguloon.
20 Bésoo bés ku bon ay bittarñikoo biir njàqare,
te diirub at yi ñu àppal ku néeg,
21 coowal musiba mooy buur nopp ya,
yàqkat bette ko biir jàmm.
22 Dootu yaakaara mucc musiba,
saamar a koy yoot,
23 muy taxawaalu, tan ya mujj xontoo,
mu xam ne bésub safaan taxaw na.
24 Njàqareek tiitaangee koy ëlëm,
song ko ni buur bu jekku xare.
25 Moo xàccil Yàlla loxo,
di jaay Aji Man ji njàmbaar,
26 daŋŋiiral, buur, wuti ko,
yiiroo dëllaayu pakkam,
27 te fekk ko yaflu ba gët suulu,
pooj ya duuf bay lob-lobi.
28 Ku ni mel ay dëkke dëkk yu gental,
ci kër yu kenn dul dëkke,
kër yu nara doon jali tojit.
29 Ku bon kooku du woomle, alalam du toog,
te koomam du lawe miim réew.
30 Du mucc musiba,
mooy garab gu daay xoyom car yu yees ya,
Yàlla wal, mu ne mes.
31 Bumu yaakaar naxi neen, di nax boppam,
nde neen ay doon ab añam.
32 Balaa jantam a lang mu jot añam,
te caram dootu naat.
33 Day mel ni reseñ gu doom yay yolax,
mbaa oliw gu tóor-tóor yay ruus.
34 Waa làngu yéefar yi duñu am kuutaay,
te xaymay lekk-kati ger yi la sawara di xoyom.
35 Ñooy sos joote, wasin ñaawtéef,
ñoom la seen biir di ëmb wuruj.