11
Cofar nee tuub, raw
1 Cofar ma bàyyikoo Naama àddu, ne:
2 Yii kàddu yu wale, deesu ko tontoo?
Wax ju bare tax na nit a yey?
3 Sa kebetu yii wedamal na kenn a?
Am dangay ñaawle te deesu la tiiñal?
4 Nee nga sa àlluwa wér na péŋŋ,
sa jëw rafet, Yàlla seede.
5 Éy su Yàlla nammoona wax,
ba àddu, wax ak yaw,
6 àgge la kumpay xelam mu rafet,
mi wees dég-dég,
kon nga xam ne Yàlla jéllale na sa lenni tooñ!
7 Dangaa mana gëstu mbóoti Yàlla, ba gis ko?
Am yaa ñédd Aji Man ji?
8 Lu gëna kawe kaw, ana loo ci man?
Lu gëna xóot njaniiw, ana loo ci xam?
9 Màggaayu Yàllaa sut suuf,
gëna yaatu géej!
10 Su dikkee, tëj nit,
woo ko péncum àtte, ku ci man dara?
11 Moom mi xàmmee ñi dul niti dara,
mooy gis lu bon, te du laaj mu teewlu.
12 Waaye ku boppam feesul, bu muusee,
mbaamu àll a judduwaale nangu.
13 Waaye yaw soo defee sa xel ci Yàlla,
dékk ko say loxo,
14 fabal say ñaawtéef, sànni,
te baña xajal njubadi sa biir xayma,
15 kon déy, nga mucc gàkk, siggi;
dëju te doo tiit,
16 sa coonob tey ngay fàtte,
ni waltan mu wal ba wéy doŋŋ
ni nga koy fàttlikoo,
17 te yaay gëna leer jantub njolloor,
ba lëndëm di saf leeru njël.
18 Kon nga am yaakaar ak kóolute,
aaru, soo tëddee, nelaw,
19 jaaxaan, kenn du la lëjal,
ñu bare di la leewaayu;
20 ku bon jàq, ba gët ya giim,
rawtu réer ko,
yaakaaratul lu moy noowam gu mujj.