65
Aji Sax ji wuyu na
1 Maa may ay nit tont te laajuñu ma.
Maa leen may, ñu gis ma te seetuñu ma woon.
Maa ne leen: Maa ngii, maa ngii!
te ñuy xeet wu dul tudd sama tur.
2 Samay loxo laa yendoo tàllal askanu fippukat,
nit ñuy doxe yoon wu baaxul,
topp seen xelum bopp.
3 Ñoo di xeet wu ma ne jàkk,
dëkke maa naqaral,
di sarxalali tuur ci biiri tool,
di leen taalal cuuraay ci kaw sarxalukaay
bu ñu tabax,
4 di tooge diggi bàmmeel,
di fanaan bérab yu làqu;
di lekk yàppu mbaam,
seeni cin def ñam yu sobewu,
5 te ñu naan: «Dellul gannaaw,
bul ma jege, maa la gëna sell!»
Lii déy daa mel ni saxar ci samay wakkan,
mel ni sawara su yendoo boy.
6 Ma ne dogal a ngii binde, fi sama kanam:
«Duma noppi déy, maa leen di fey,
maa leen di fey ba mu mat sëkk.»
7 Aji Sax ji nee: «Muy seeni ñaawtéef,
di seen ñaawtéefi maam,
ya daan taalali tuur cuuraay ca tund yu mag ya,
di ma kókkali ca kaw tund yu ndaw ya,
lépp laa leen di fey ba mu mat sëkk,
muy seen añu jëf ja woon.»
8 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Ni nit di gise cabbu reseñ ju fees dell,
ne: “Buleen ko yàq,
ngëneel a ngi ci,”
noonu laay def ngir sama jaam ñi,
baña boole lépp yàq.
9 Fi Yanqóoba laay soqee aw askan,
fi Yuda laa ne, fi laay jële lu séddoo samay tund.
Samay tànnéef a koy séddoo,
sama jaam ñi kay a fay dëkke.
10 Joorug Saron ay dellu di parlub gàtt gi,
xuru Akor di goorukaayu nag yi,
ñeel sama ñoñ ñi may sàkkuji.
11 «Waaye yeen ñi wacc Aji Sax ji,
yeen ñi fàtte sama tund wu sell wi,
di taajal ndab, Gàdd tuur mi,
di xellil biiñu njafaan, Meni tuur mi,
12 maa leen di dogalal saamar,
ngeen bokk sukk, ñu rendi leen,
ngir maa woote, wuyuwuleen,
ma wax, dégguleen,
xanaa di def li ma ñaawlu,
taamu li ma buggul.»
13 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
«Ma ne sama jaam ñeey lekk,
yeen ngeen nekke xiif.
Ma ne sama jaam ñeey naan,
yeen ngeen nekke mar.
Sama jaam ñeey bànneexuji,
yeen, ngeen nekke gàcce.
14 Sama jaam ñeey sarxolleji
ndax xol bu neex,
yeen ngeen di yuuxu ndax naqaru xol,
di jooyoo ndax xol bu jeex.
15 Seen tur wi ngeen bàyyi gannaaw
la samay tànnéef di móoloo,
naan: “Yal na la Boroom bi Aji Sax ji rey ni diw ak diw,”
waaye ñoom sama jaam ñi,
tur wu yees lees leen di wooye,
16 ba képp ku namma barkeel fi kaw suuf,
ci Yàlla jiy dëgg la koy ñaane,
te kuy giñ fi kaw suuf it,
ci Yàlla jiy dëgg la koy giñe.
Day fekk njàqare ya jiitu di lu ñu fàtte,
te di lu làqu saay gët.
Aji Sax ji yeesal na càkkéefam
17 «Maa ngii di sàkksi asamaan su yees
ak suuf su yees.
Deesul fàttlikooti yëf ya jiitu,
xel dootu ci dem.
18 Bégleen kay,
te saxoo di bànneexoo li ma sàkk:
Maa ngii di sàkk Yerusalemu mbégte,
waa dëkk ba nekke bànneex.
19 Maay bége Yerusalem,
bànneexoo sama ñoñ.
Deesu fi déggati ay jooy,
mbaa coowal njàqare.
20 Deesu fi gisati
tuut-tànk bu dund fan yu néew,
mbaa mag mu dee te ay fanam matul,
ba ku am téeméeri at dee sax, di ku gàtt fan,
te ku àggul téeméer, ñu ne alku nga.
21 «Ñooy tabax ay kër, dëkke,
jëmbati tóokër, lekk ca meññeef ma.
22 Duñu tabax moos, keneen dëkke;
duñu jëmbat moos, keneen xéewloo.
Sama ñoñ ay tollook garab yi fan,
sama xejj yeey jagoo seenu ñaq.
23 Duñu liggéeyati mukk ci neen
te dootuñu jural mbas.
Ñooñooy askanu ñi Aji Sax ji barkeel,
seeni doom nekk ak ñoom.
24 Su boobaa balees woote,
man, maay wuyu;
balaa ñoo daane seen kàddu, ma nangul leen.
25 Bukki ak mboteey bokk di for,
gaynde niw nag, di for um ñax,
jaan di dunde pënd.
Deesatul gaañe mbaa di lore,
fi mboolem sama kaw tund wu sell wi.»
Aji Sax jee ko wax.