59
Bàkkaar ñag na diggante Yàllaak ñoñam
1 Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo,
noppam naqariwul ba tere koo dégg.
2 Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek
seen Yàlla.
Seeni moy a leen xañ kanamam,
ba mu tanqamlu leen.
3 Seeni loxoo taq deret,
ngeen ne lijj ci ñaawtéef,
làmmiñ di fen, di sos njekkar.
4 Du njekk gu kenn wut cib àtte,
du dëgg gu kenn sàkku cib layoo.
Ñu ngi yaakaar caaxaan, di fen,
di sos ayib, wasin ñaawtéef.
5 Nenu ñàngóor lañuy tostan,
di ràbb lëndu jargoñ.
Ku lekk ci nen yi dee,
te boo ci tojeeb nen,
saamaan fëlle ca.
6 Seeni lënd du ràbbe ba solal nit,
mbaa di sàng kenn;
seenum ràbb ñaawtéef lay jur,
seen loxo ya ko liggéey sabab fitna,
7 seeni tànk daw wuti lu bon,
ñuy yàkkamtee tuur deretu ku deful dara,
seeni xalaat di ñaawtéef,
yàquteek njaaxum féete ca seeni yoon.
8 Xamuñu yoonu jàmm,
te yoon amul fa ñuy jaare,
xanaa sàkk seen yoon yu lunk
te ku fa awe doo daj jàmm.
9 Lee tax yoon sore nu,
te njekk du nu dab.
Danuy yaakaar leer,
lëndëm ne jaas,
nuy séentuy ceeñeer,
tey lëndëmtuy wéy.
10 Nu ngi làmbatub tabax ni silmaxa,
di tëñëx-tëñëxi ni ku amuli gët,
di fakktalu bëccëg ndarakàmm ni bu doon guddi,
dëkk ak ñu wér péŋŋ te mel ni ña dee.
11 Nun ñépp a ngi xiiru ni rab wu aay,
binnee binni niy xati,
yaakaar yoon, yoon wuute,
séentu wall, wall sore.
12 Sunuy tooñ a bare fi sa kanam,
sunuy moy a nu seedeel,
sunuy tooñ a nu topp,
te xam nan xéll sunuy ñaawtéef.
13 Noo tooñ Aji Sax ji, wor ko,
te noo dëddoo sunu Yàlla jii,
kàdduy fitna ak fippu,
ak fen yu nu mébét, nas ko,
14 ba yoon dellu gannaaw,
njekk dànd,
dëgg fakktaloo fa pénc ma,
njub tëë agsi.
15 Dëgg a tumurànke,
ku dëddu mbon sax, ñu ñori la,
Aji Sax ji gis ci, ñaawlu ko,
nde yoon a amul.
16 Daa xool, gisul kenn;
mu tiisoo li ci kenn jógul,
moo tax loxoom may ko ndam,
te njekkam la sukkandikoo.
17 Moo sol kiiraayal njekk,
mbaxanawoo mucc,
solati yérey mbugale,
làmboo turkib xéraange.
18 Mooy delloo ku ne yool ba mu yelloo,
mbugal ay bañam, fey ay noonam,
ba delloo waa dun ya yool ba ñu yelloo.
19 Dees na wormaale turu Aji Sax ji fa sowu,
wormaale teddngaam ba penku.
Bu noon bi agsee ni walum dex,
ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.
20 «Ab jotkat ay dikkal Siyoŋ,
ba jot ñi tuub seeni bàkkaar ci askanu Yanqóoba.»
Kàddug Aji Sax jee.
21 «Man nag, lii mooy sama kóllëreek ñoom:
Sama xel mi tegu fi sa kaw,
ak sama kàddu yi ma yeb ci sa gémmiñ,
lenn du ci teqlikook sa gémmiñ
ak sa gémmiñu askan,
ak sa gémmiñu askanu askan, tey ak ëllëg.»
Aji Sax jee ko wax.