52
Yerusalem dina suqliku
Yewwulee, yewwul,
Siyoŋee, làmbool sa doole!
Yerusalem, dëkk bu sell bi,
solul ba ne ràññ!
Ndax du kenn ku xaraful mbaa ku sobewu
ku lay songati.
Yaw Yerusalem, mi ñu jàpp njaam,
jógal fëgtu,
yaw janq Siyoŋ mu taaru mi ñu jàpp njaam laa ne,
tikkil buum gi ci sa baat.
Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Dees leena wànteeroon ci dara,
te du xaalis lees leen di jotaate.»
Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Misra la sama ñoñ jëkka wàcc, dali fa,
Asiri door leena not ci dara.
Léegi nag ana lu fiy sama wàll?»
Kàddug Aji Sax jee.
Mu ne: «Jàpp nañ sama ñoñ njaam ci dara;
seeni sang a ngi tëggu,
di dëkke ñàkke teggin sama tur.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Moo tax sama ñoñ di xam maay kan;
moo tax bésub keroog
ñu xam ne maay wax te maa ngii!»
 
Ndaw leeka rafeti tànk,
kee bartaloo tund yi,
di la dégtalsi jàmm,
di la xibaar lu neex,
àgge la ag mucc,
ne la: «Éey, Siyoŋ,
sa Yàllaay Buur!»
Déglul sa jongrukat yi,
ña ngay xaacu, sarxollendoo.
Ñoo gisal seen bopp
Aji Sax ji di ñibbsi Siyoŋ.
Yeen genti Yerusalem, àndleen sarxolle;
Aji Sax jeey dëfal ñoñam,
mooy jot Yerusalem gii!
10 Aji Sax jee wone dooleem ju sell ji,
xeet yépp di gis,
ba ca cati àddina.
Ñépp ay gis sunu wallu Yàlla.
11 Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi*,
bu ngeen di jóge Babilon,
dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal,
setluleen te génn foofa.
12 Dungeen gaawtu déy, di dem;
duy xél moos ngeen fay génne.
Aji Sax jeey dox jiitu leen,
te Yàllay Israyil laa ne, moo leen di féete gannaaw.
Teraangay jaam bi wuutu na coonoom
13 Aji Sax ji nee: «Sama jaam baa ngi,
mooy baaxle, kawe,
dees na ko yékkati, darajaal ko lool.
14 Moo dawoon yaramu ñu bare,
ndax yàqu ba nirootul nit,
bindootul woon ni doom aadama,
15 waaye noonu it lay waare ay xeeti xeet,
ba buur yi wedam,
ngir lu ñu leen waxuloon, te ñu gis ko,
lu ñu dégguloon, te mujj ko ràññee.»
* 52:11 Seetal ci 2.Buur ya 25.13-15. 52:15 Manees na koo tekkee nii itam: xeet yu bare lay wis-wisal um ndox, setale leen ko.