4
Su bés baa juróom yaari jigéen ŋoyaalu genn góor, ne ko:
«Sunub dund, nun a,
sunu koddaay, nun a!
Jox nu sag buum rekk,
teggil nu gàcce.»
Aji Sax ji aar na ndesu Yerusalem
Su bés baa njebbitum Aji Sax ji
doon lu yànj, darajawu,
meññeefum réew mi di teraanga, dib sag,
ñeel ñi dese bakkan fi Israyil.
Su boobaa ku mucc fa Siyoŋ
ak ku des fa Yerusalem,
ku sell ki lees lay wooye,
muy képp ku ñu bind turam,
te mu wara dese bakkan ci Yerusalem.
Boroom beey wal noowal mbugal,
noo guy lakk, sellal,
fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ,
fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set.
Su boobaa tundu Siyoŋ bépp,
fépp fu ñuy dajee,
Aji Sax ji sàkk fa niiru saxar bëccëg,
guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ;
leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp,
di mbaar mu ñuy serloo tàngooru bëccëg,
di ko seeloob taw ak waame.