39
1 Jant yooyu doomu Baladan, Merodag Baladan buuru Babilon moo yónnee Esekiya bataaxal ak yóbbal. Fekk na mu déggoon ne Esekiya daa woppoon bay doora am tan.
2 Esekiya am ca mbégte, daldi won ndaw ya, kërug dencukaayam: xaalis baak, wurus waak ndàbb jaak, diwu tànnéef gaak mboolem néegub gànnaayam ya, ak mboolem lu nekkoon cay dencam. Amul lenn lu leen Esekiya wonul ci biir këram, ak mboolem fu bokk ci kilifteefam.
3 Gannaaw loolu Yonent Yàlla Esayi dikk ne Buur Esekiya: «Lu la nit ñii wax ak fu ñu jóge sax ba fi yaw?» Esekiya ne: «Réew mu sore lañu bàyyikoo, dikk ba fi man, réewum Babilon.»
4 Mu ne ko: «Ana lu ñu gis sa biir kër?» Esekiya ne ko: «Mboolem lu nekk sama biir kër, gis nañu ko. Amul lenn lu ma leen wonul ci samay denc.»
5 Esayi ne Esekiya: «Déglul kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yi:
6 “Ay jant a ngii di ñëw, dees na yóbbu Babilon lépp lu nekk sa biir kër, te say maam dencoon ko, ba tey jii. Du lenn luy des. Kàddug Aji Sax jee.
7 Te it ñenn ci sag njaboot, ñu soqikoo ci yaw, di ñoo meññ ci sa geño, dinañu leen jàpp, ñu doon jaam yu ñu tàpp ca biir kër buuru Babilon.”»
8 Esekiya ne Esayi: «Kàddug Aji Sax ji nga jottli, jàmm la.» Booba ma nga naan: «Ndegam jàmm ju ne ñoyy ay am sama giiru dund kay!»