27
Bésub keroog Aji Sax ji dikke saamaram
bu jàmbaare, ñàng te réy,
ba dal ci kaw Lewiyatan, jaan ja ca xél wa,
Lewiyatan jaan jay wañaaruy dem,
ninki-nànkay géej jooju lay rey.
Aji Sax ji juboo naak ñoñam
Bésub keroog, tóokëru reseñ ju neex am,
nangeen ko woy,
te man Aji Sax ji maa koy topptoo,
di ko suuxat saa su ne,
di ko wattu guddeek bëccëg,
bala koo kenn a song.
Mereetuma tóokër bii,
waaye lu ciy dég aki dagg,
ma dox wuti ko, xareek moom,
boole lépp xoyom.
Xanaa ku langaamoo sama kiiraay
te jàmmook man,
ba jàmmook man.
Ay bés a ngi ñëw Yanqóoba saxi reen,
Israyil moomooy tóor, law,
ba feesal déndu àddinaak meññeef.
 
Defe ngeen ne Aji Sax ji duma na Israyil,
na mu dumaa ña leen duma woon?
Am bóomal na leen lu tollook
la seeni bóomkat bóomoon?
Ndànk-ndànk la jëflanteek ñoom,
ba mu leen toxalee,
dàqe leen noowam gu mag,
bésu ngelawal penku.
Nii la Yanqóoba jotoo ñaawtéefam,
nii la mujje am njéggalu bàkkaaram:
Day boole doji sarxalukaay bi yépp,
rajaxe ni doji kew,
xer wu ñuy jaamoo Asera dootu fa sampe,
mbaa sarxalukaayi suurukaay.
10 Dëkk bu ñu dàbbli mooy wéet,
gental, ne wëyëŋ!
Fa la nag di fore,
fa lay goor, di lekk cari garab ya,
11 car ya wow, damm,
jigéen ñi dikk, xambe.
Dañu di xeet wu dul dégg,
ba tax ki leen sàkk yërëmu leen,
moo leen bind te ñeewantewu leen.
 
12 Bésub keroog Aji Sax ji bàcc,
dale ca dexu Efraat ba ca walum Misra,
te yeen bànni Israyil, dees na leen for
kenn-kenn, ba ngeen daj.
13 Bésub keroog liit gu mag jib,
ña laŋoon réewum Asiri délsi,
ànd ak ña ñu tasaare woon biir réewum Misra,
ba sujjóotalsi Aji Sax ji fa Yerusalem,
fa kaw tund wu sell wa.