Waxyu ñeel na mujug jamono
24
(Saar 24—27)
Mbugal daj na àddina
1 Aji Sax jaa ngii di tas àddina,
tasaare ko,
salfaañe li fi dénd bi,
wasaare ñi ko dëkke:
2 sarxalkat beek baadoolo bi,
sang akub jaam,
njaatige lu jigéen ak ab janqam,
jaaykat ak jëndkat,
ablekat ak àbbkat,
leblekat ak lebkat.
3 Àddinaa ne duŋŋ duŋŋaaral,
dees koo futti ba mu ne furaas!
Aji Sax ji kat wax na kàddu gii!
4 Suuf a ngi wowa wow, ne sereŋ,
àddina ne làcc, ne sereŋ,
kàngami xeeti àddina ne làcc.
5 Suuf si la ñi ko dëkke sobeel,
ñoo wàcc yoon yi,
xëtt ndigal,
fecci kóllëre gi sax dàkk.
6 Moo tax alkànde yàq suuf,
ñi ko dëkke gàddu àq ji.
Moo tax waa àddina raaf,
ba ñi des di lu néew.
7 Biiñ ñàkk na,
garabu reseñ lax,
bépp xol bu tooyoon, binni.
8 Tabala ju xumb selaw na,
ña daa xaxaloo dal,
mbégtem buumi xalam dakk.
9 Kenn naanatul, di woy,
ñoll wex na ka koy naan.
10 Dëkk bu gental tasaaroo na,
kër yépp tëje, kenn duggul.
11 Mbedd maa ngi soowaloo,
ndax biiñ bu ñàkk,
gépp mbégte fey,
bànneexu àddina dëddu.
12 Tojiti neen a des ci dëkk bi,
bunt ba rajaxoo.
13 Noonu lay deme ci àddina,
ci biir xeet yi,
mbete benn-benni doomi oliw gu ñu gësëm,
mbaa doomi reseñ yu des ca ndey ja,
gannaaw bu ñu wittee ba sottal.
Ndes wi rëcc mbugal a ngi sant
14 Ña ngay xaacu di sarxolle,
waa sowu di sàbbaal ci màggug Aji Sax ji.
15 Yeen waa penku, sargal-leen Aji Sax ji boog,
yeen waa duni géej, teral-leen Aji Sax ji Yàllay Israyil.
16 Cati àddina lay woy di jibe, nu dégg ñu naa:
«Teddnga ñeel na Aji Jub ji!»
Coono jeexul
Waaye man dama ne: «Jeexle naa!
Jeexle naa, wóoy man!
Workat yaa ngi wora wor,
ba far làggi ci wor.»
17 Yeen waa àddina,
kat-kat, pax akub caax dëgmal na leen.
18 Nga déggi yuux, daw,
tàbbi biir pax,
génne pax,
laawoob caax.
Mbàndi kaw kat ubbi na,
kenug àddina di reng-rengi.
19 Suuf daa loroo loru,
fetta fett,
salfaañoo salfaañu.
20 Suuf a ngi janga jang ni màndikat,
ba joy ni mbaar,
moyam diis ko gann,
mu daanu te du jógati.
Aji Sax jeey nguuru fa Siyoŋ
21 Bu bésub keroogee
Aji Sax ji dikke mbugal
gàngoor ya fa kawa kaw,
ak buuri àddina yi fi suuf.
22 Dees leen di boole denc cim pax,
ne leen ràpp tëj,
ba mu am ay fani fan, ñu mbugal leen.
23 Kersa la weer wiy am,
gàcce ñeel jant bi;
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal,
mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ,
leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.