22
Ab yéeneb waxyu ñeel na Yerusalem
Yéene bii ñeel na xuru Peeñu ma:
Ana lu ngeen di yéege,
yeen ñépp seen kawi taax?
Lu waral coow li ak xaxaloo bi,
ba dëkk biy riir?
Ñi ngeen deele, saamar reyu leen,
bóomuñu leen ci xare.
Seen njiiti xare yépp a bokk daw,
ñu jàpp leen te taluñoo fitte.
Seen njiit yi ñu gis yépp lañu jàpp,
te ñu dawoon ba sore.
Moo ma tax ne: «Buleen ma xool,
damay naqarlu, jooy.
Tàyyileen maa dëfal ci sama bokk yi sànku.»
Lii kat bésub njommite laak coonook toroxte,
bésu Boroom bi Aji Sax ji ci gàngoor yi,
ci biir xuru Peeñu mi.
Tata ja, ñu rëkka rëkk, mu màbb,
yuux jolli, àkki tund ya.
Waa Elam gàllooy fitt,
ñenn ña war watiir, gawar ya war,
waa Kir ŋàbb pakk ya.
Seen xur yu nangu yaa fees aki watiir,
gawar taxaw temm buntu Yerusalem,
te Yuda ne duŋŋ, dara wëru ko.
 
Su keroogee ngeen yaakaar ngànnaay,
ya ca kër ga ñuy wooye Gott ba,
far gis ni ñu bëtt-bëttee tatay Yerusalem,
ji wër gox bi ñu naan Kër Daawuda.
Ngeen rooti ndox ca solom bu suufe ba, denc ko,
10 boole ca waññ këri Yerusalem,
màbb lenn, sàkk ca lu ngeen aare tata ya.
11 Da leen di fekk sàkk mbànd diggante ñaari tata yi,
ngir denc ca ndoxum déeg bu yàgg ba.
Waaye xooluleen ki dogal lii,
xalaatuleen ki nasoon lii bu yàgg.
 
12 Bésub keroog Boroom bi,
Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo
ci jooyoo ak ñaawlu
ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
13 Te yeena ngii ci mbég ak bànneex,
di rendi nag ak xar,
di yàpp ak a naan,
naan: «Nan lekk, naan, nde ëllëg, nu dee!»
14 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dégtal na ma lii:
«Gii ñaawtéef déy deesu leen ko jéggal,
ba keroog ngeen di dee.»
Boroom bee ko giñ,
moom Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
Kàddug àrtu ñeel na Sebna
15 Boroom bi Aji Sax ji ci gàngoor yi dafa wax ne:
«Ayca, demal ba ca Sebna,
bëkk-néegu buur sii, nga ne ko:
16 Ana loo fi am, ak koo fi am?
Nga di fi yettlu bàmmeel, yett ko ca kawte ya,
di gaslu kër gooy mujje?
17 Jàmbaar, dama ne Aji Sax jee lay xalab;
da la naa nikk,
18 fodonk la, rattax,
nga xalangoo àll bu ne màww.
Fa ngay dee,
te fa la watiir yi ngay puukarewoo di des,
muy sa gàccey waa kër sang.»
19 Aji Sax ji nee: «Maa lay jële sa liggéey,
foqatee la sa péete mu kawe.
20 «Bésub keroog ma woo sama jaam bi, Elyakim doomu Ilkiya, 21 solal ko sa mbubb, dooleele ko sa ngañaay, teg kilifteefu réew mi ci loxoom, ba mu féete wàllu baay, waa Yerusalem, ak waa kër Yuda. 22 Maa koy ràng caabiy kër Daawuda, muy ubbi te kenn du tëj; di tëj te kenn du ubbi. 23 Maa koy samp fu dëgër ni ab wékkukaay, mu doon sagu kër baayam. 24 Waa kër baayam ak seen daraja, ñépp ay wékku ci moom, car yaak caraat ya. Ndab yu ndaw yépp ca la, kopp ya ba ca njaq ya. 25 Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, mu ne: «bant ba sampe woon fu wóor day simpiku. Dees koy gor, mu fàq, la ca sëfe woon dog.» Aji Sax ji déy wax na ko.