15
Ab yéeneb waxyu ñeel na Mowab
Yéene bii ñeel na Mowab:
Genn guddi déy la Ar Mowab, dëkk ba tas, ne mes!
Genn guddi déy la Kir Mowab tas, ne mes!
Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon,
ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya,
Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba,
boppoo bopp dib nel,
sikkimoo sikkim xuufu,
nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya,
ak kaw taax yaak pénc ya,
ku ne di jooy ba say rongooñ wale.
Waa Esbon ak Elalee ngi yuuxu,
seen baat àkki ba Yaxacc,
xarekati Mowab dégg ca, yuuxoo,
ne yàcc ne yasar!
Maay jooy Mowab jooyi xol,
nit ñaa nga fay dawe ba Sowar,
àkki ba Eglat Selisiya.
Ña ngay yéeg jëm Luwit, di jooyoo,
awe yoonu Oronayim, di jalu.
Dexu Nimrim wow na,
ñax wow, gàncax lax,
dara naatatul.
Jël nañu lu ñu deseek lu ñu dencoon,
yóbbu, jàll ca wàllaa xuru Garab ya.
Yuux déy maase na réewum Mowab,
jooyoo ya ba Eglayim,
jooyoo ya ba Beer Elim.
Dexu Dimon déy fees na ak deret,
te ma nara wàcceel Dimon lu ko raw,
ba ku rëcce Mowab,
ak ku des ci réew mi, ma booleek gaynde!