11
Daawuda am na kuutaay
Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese*,
ab car soqeekoo fa reen ya,
xelum Aji Sax ji tegu fi kawam,
xelum rafet xalaat ak ràññee,
xelum digle ak njàmbaar,
xelum xam Aji Sax ji, ragal ko.
Ragal Aji Sax ji lay safoo,
du lu ko bëtam may rekk lay àttee,
du lu ko noppam may rekk lay dogale,
xanaa di àtte ku ñàkk ci njekk,
di dogalal njub, néew-ji-dooley àddina.
Mooy dóore àddina, bantub kàddoom,
mooy reye ñu bon ñi, ngelawal gémmiñam.
Njekk lay gañoo,
takkoo kóllëre.
Till ay bokk ak mbote ab dal,
segg bokk akub tef ab tëraay,
wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar,
tuut-tànk jiite leen.
Nag ak rab wu aay di forandoo,
seeni doom goorandoo,
gaynde di lekk um ngooñ niw yëkk,
luy nàmp di foye paxum ndox-suuf,
perantal di laal tostanum ñàngóor.
Deesatul gaañe mbaa di lore,
fi mboolem sama kaw tund wu sell wi,
ndax ni ndox di feese ba muur géej,
ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.
10 Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba,
taxaw di raaya buy gindi xeet yi,
xeet yi di ko sàkku,
dal-lukaayam ba jagoo teddnga.
 
11 Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom
ñaareel bi yoon,
ngir jotaat ndesu ñoñam,
wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum Kuus,
ak Elam ak Sineyaar,
ak Amat ak biir duni géej ya.
12 Mooy yékkatil xeet yi raaya,
dajale góor ña ñu dàqe Israyil,
ak jigéen ña ñu jële Yuda, tasaare leen,
ñu jóge ñeenti weti àddina, booloo.
13 Fiiraangey Efrayim day jeex,
njéefoy Yuda dakk,
Efrayim dootu fiire Yuda,
Yuda dootu jéppi Efrayim.
14 Xanaa ñu ne coww ba sowu,
ne jàyy cëppandoo
fa kaw waggi Filisteen ña,
waa penku, ñu sëxëtoondoo;
Edom ak Mowab, ñu teg loxo;
Amoneen ña nangul leen.
15 Aji Sax jeey wowal walum ndox,
ma séle géeji Misra.
Mooy tàllal loxoom, tiimale dexu Efraat,
wal kook doole,
dóor ko, mu séddlikoo juróom yaari wal,
mu jaarale ca nit ñu caraxu,
16 def kow yoon, ñeel ndesu ñoñam,
ña dese fa Asiri,
mu mel ni yoon wa ñeeloon Israyil,
bésub keroog ba ñuy génn réewum Misra.
* 11:1 Yese mooy baayu Daawuda.