8
Ku ji as ngelaw, yaay góob ngëlén
1 «Sexleen bufta gi!
Jaxaay jàyy ci waa kër Aji Sax ji,
nde ñoo fecci sama kóllëreek ñoom,
samaw yoon lañu gàntal.
2 Man la Israyil xaacu, ne ma:
“Éy sama Yàlla, maa la ràññee!”
3 Israyil a xalab lu baax,
ba ab noon dàq ko.
4 Ñoo fal ay buur te du sama ndigal,
ñoo tabb ay kàngam, te yéguma.
Seen xaalis ak seen wurus lañu sàkke jëmmi tuur,
muy seen sànkute.
5 Yeen waa Samari, seen jëmmu wëllu wi dàqu na!
Sama mer tàkkal na leen.
Lu ngeen deeti xaar ci mucc ayib?
6 «Israyil la lii jóge,
te ab liggéeykat moo ko sàkk.
Kon lii du Yàlla!
Ay tojit la wëlluw Samari di mujje.
7 «As ngelaw lañu ji, ñooy góob ngëlén.
Gub du jóg, pepp du focci,
te bu pepp amoon it,
jaambur a koy wonn.
8 Dees na wonn Israyil;
tey ñu ngi ci biir xeeti jaambur yi,
mel ni ndab lu kenn buggul.
9 Ñoo demal seen bopp Asiri.
Mbaamu àll day beru yoonam,
waaye waa kër Efrayim ñooy jënd ay far.
10 Ci xeeti jaambur ñi lañuy jënde,
waaye du tee ma dajale leen.
Léegi ñu tegoo notaangey buur aki kàngam.
11 Efrayim a yokk ay sarxalukaay ngir moy,
ñu doon ay sarxalukaayi moyukaay doŋŋ!
12 Naa ko bindal sama fukki junniy
ndigali yoon,
yëfi jaambur lees koy jàppe.
13 Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel,
lekk yàpp wi,
Aji Sax ji buggu ci dara.
Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef,
mbugale leen seeni moy,
te ñoom Misra lañuy dellu.
14 Israyil moo fàtte ab sàkk-katam,
di tabax kër yu yànj.
Yuda moom yokki dëkk yu tata wër.
Maay yebal sawara ci kawi dëkkam,
mu xoyom ay tataam.»