12
Aji Sax ji layoo na ak Israyil ak Yuda
1 «Efrayim, ay fen la ma gawe,
waa kër Israyil laa ne,
ñoo ma yéewe ag njublaŋ,
waaye Yudaa ngi ànd ak Yàlla ba tey,
di sàmm kóllëreek Ku Sell ki.»
2 Efrayim mooy sàmmkatub ngelaw,
yendoo topp ngelawal penku,
di yokki fen ak fitna,
fasoo kóllëre ak Asiri,
yónnee yóbbalu diw ba Misra.
3 Aji Sax ji moo séq ak Yuda ab layoo,
mooy mbugale Yanqóoba ay jëfinam,
añale ko ay jëfam.
4 Ci biiru ndeyam la kii suufoo ab seexam;
kii moo tollu ci dooleem, bëreek Yàlla.
5 Kee bëreek malaaka, ba génn ca,
kee jooy di sàkku aw yiwam.
Fa Betel la ko fekk,
te foofa la Yàlla waxeek nun.
6 Aji Sax ji Yàlla Boroom gàngoor yi,
Aji Sax jee di turu bàkkam.
7 Yaw nag, ca sa Yàlla nga wara dellu,
ngor ak njub, sàmm ko,
te nga saxoo yaakaar sa Yàlla.
8 Ni Kanaaneen biy jula, ni la Efrayim
yore màndaxekaayu njublaŋ cib loxoom,
bëgga naxe.
9 Efrayim a ngi naan: «Woomle naa,
maa amal sama bopp alal,
te mboolem samaw ñaq, giseesu ci
tooñaange ju di bàkkaar.»
10 «Man Aji Sax ji dale di sa Yàlla ca Misra,
maa lay dëëlaat ciy xayma,
na woon ca bésub ndaje.
11 Maa wax ak yonent yi,
yokk peeñu yi,
te yonent yi, maa leen waxyu ay misaal.»
12 Su Galàdd dee dëkkub defkati ñaawtéef,
dañoo tekkiwul dara.
Fa Gilgal lees di rendee ay saraxi yëkk,
te seeni sarxalukaay ni jali xeer lay mel
ci ay tooboy tool.
13 Yanqóobaa dawoon ba réewum Siri,
Israyil laa ne, moo liggéey ngir am jabar,
wut jabar tax koo sàmm ag jur.
14 Ci loxol yonent la Aji Sax ji génnee Israyil Misra,
te ab yonent la sàmmloo Israyil.
15 Waaye Efrayim moomoo ko merloo,
naqaral ko.
Deret ji mu tuur la Boroomam di këpp ci kawam,
añub tooñam la koy fey.