10
Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi. Su sarax yi taxoona set wecc, deesu ko dakkal? Bu ca jaamukati Yàlla yi doon sete wecc benn yoon kay, xanaa dootuñu am yaraangey bàkkaar! Sarax yooyu ay bàkkaar lay fàttlee at mu jot, ndax deretu yëkk, ak ju sikket kat manula far ay bàkkaar.
Moo tax ba Almasiy dikk ci àddina la wax ne:
«Saraxug jur aki jooxe, taamuwuloo ko,
waaye aw yaram nga ma waajalal.
Saraxi dóomal ak saraxi póotum bàkkaar,
safoowuloo ci dara.
Ca laa ne: “Maa dikk nii,
te téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man,
maa defsi sa coobare, yaw Yàlla*.”»
Dafa jëkk ne: «Saraxi jur aki jooxe, saraxi dóomal ak saraxi póotum bàkkaar, bugguloo, safoowuloo,» doonte yoon wee laaj yooyu sarax. Mu teg ca ne: «Maa ngii defsi sa coobare.» Noonu la fare lu jëkk la, ngir wuutal fa ñaareel bi. 10 Coobarey Yàlla googu moo waral ñu sellale nu sarax, bi Yeesu Almasi sarxe yaramam, benn yoon ba fàww.
11 Mboolem sarxalkat a ngi taxaw bés bu nekk ci liggéeyam, di jébbale ak a jébbalewaat yenn sarax yooyu, te lenn du ci masa mana far bàkkaar. 12 Waaye kii de, ba mu sarxee ngir ay bàkkaar, bennub sarax, mu doy ba fàww, ca la tooge fa ndijooru Yàlla. 13 Fa la doxe di xaar bés ba ñu koy defal ay noonam, ndëggastalu tànkam. 14 Kon bennub sarax boobu, ci la matale sëkk ba fàww, nit ñi ñu sellal.
15 Mooy li Noo gu Sell gi itam seede, ñeel nu, 16 nde gannaaw ba mu nee:
«Lii moo di kóllëre gi may fas ak ñoom,
bu fan yooyu weesee, Boroom beey wax,
mu ne maay yeb sama ndigali yoon ci seen xol,
ci seenum xel laa koy ñaas;
17 lii la ca teg: seeni bàkkaar ak seeni tooñ,
duma ci bàyyeeti xel
18 Yooyu nag fu ñu ko jéggalee, aajootul sarax su koy far.
Nanu àgg fa Yàlla
19 Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell baa sell, ngir deretu Yeesu, 20 deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu sarxe. 21 Am nanu itam sarxalkat bu mag bu jiite kër Yàlla. 22 Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu, ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu. 23 Nanu ŋoy ci yaakaar, ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la. 24 Nanu seet itam ci sunu biir nu nuy xiirtalantee ngir cofeel ak jëf ju baax. 25 Te bunu def ni ñenn ñi, di daggoo ak sunuy ndaje, waaye nanuy ñaaxante, rawatina tey bi ngeen gisee bés bi dëgmal.
26 Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci. 27 Xanaa tiitaangey séentu mbugal ma, ak sawara wu yànj wiy xoyom fippukat yi. 28 Képp ku masoona xëtt yoonu Musaa, daawuñu ko ñéeblu; ci kaw seedey ñaari nit ba ñett lees ko daan rey. 29 Kon ki dëggaate Doomu Yàlla ji, teddadil deret ji ñu sellale kóllëre gi, te ñàkke teggin Noowug Yàlla gi nu indil aw yiw, kooku, mbugal ga mu yelloo, ñaata yoon lay gënatee metti, ngeen defe? 30 Xam nanu ki wax ne: «Ag pey, maay boroom, man maay añale,» neeti: «Boroom bi mooy àtte ñoñam 31 Céy ku nara tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund, ndaw lu raglu!
32 Fàttlikuleen bés yu jëkk ya, gannaaw ba ngeen jotee ci leeru Yàlla, na ngeen dëgërloo woon ca xeex bu mag ba te metti. 33 Leeg-leegaa ñu saaga leen, bundxatal leen ci kanam nit ñi; leeg-leegaa yeen ay taxawu nit ñi ñu teg lu ni mel. 34 Ndax yeena bokk ak ñi ñu tëj seen coono, te yeena muñe xol bu sedd ni ñu foqarñee seen moomeel, ngir xam ngeen yeen ci seen bopp ne am ngeen alal ju ko gën tey sax ba fàww.
35 Kon nag buleen teqlikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci. 36 Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige. 37 Ndax kat,
«Des nas tuut, as tuut rekk,
kiy dikk, dikk te du yeex.
38 Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga,
waaye ku dellu gannaaw,
sama xol bégewu la§
39 Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw te nara sànku, waaye nooy ñi saxoo ngëm te nara mucc.
* 10:7 Seetal ci Sabóor 40.7-9. 10:17 Seetal ci Yeremi 33-34. 10:30 Seetal ci Baamtug Yoon wi 32.35-36. § 10:38 Seetal ci Abakug 2.3-4.