15
Bantu reseñ matul matt
Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
Yaw nit ki, ana lu bantu reseñ gëne ci bant yi,
ak mboolem caru garab bu mu doon ci gott bi?
Ndax dees na ca sàkk bant, liggéeye ko?
Am dees na ca sàkke wékkukaay, wékk ca lenn?
Xanaa sànni cib taal, xambe,
ñaari cat ya lakk, digg ba xoyomu.
Ana lu deeti njariñam?
Ndegam ba mu nee ñumm,
lees ci dul liggéey dara,
gën ba mu jàppee ba xoyomu.
Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Dees na xamb caru reseñ,
mu bokk ci banti garab yi ma joxe, ñu xamb lépp,
te noonu laay xambe waa Yerusalem.
Maay jànkoonteek ñoom,
ñu rëcc sawara,
sawara lakk leen.
Bu ma jànkoonteek ñoom,
dingeen xam ne maay Aji Sax ji.
Maay gental réew mi,
ñoo def jëfi ñàkk worma.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.