12
Ngàllo xeeñ na
Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji da maa dikkal ne ma:
«Yaw nit ki, digg kërug fippukat nga dëkke, ñu ami gët te duñu gis, ami nopp te duñu dégg, ndax kërug fippukat lañu. Yaw nag nit ki, dajaleel digg bëccëg, ñépp gis, sa jumtukaayi ku jëm ngàllo te nga sanci feneen, ñépp teg ci bët. Jombul ñu gis ne kërug fippukat lañu. Sab ëmb ngay jëkka génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo, ñépp teg ci bët. Te yaw nga génn ngoon ni ku jëm ngàllo, ñu teg ci bët. Dangay bëtt ci miir bi, ñuy gis, pax mooy yoore sab ëmb. Nañu la gis nga gàddu sab ëmb, génn ci lëndëm gi. Booy génn di dem, sa kanam ngay muur, ba doo mana gis suuf si, ngir misaal laa la def, ñeel waa kër Israyil.»
Ma def loolu noonee ñu ma ko sante. Samab ëmb laa génne digg bëccëg ni ku jëm ngàllo. Ca guddi ga ma bëtte miir ba loxoy neen, ñépp di gis. Ci lëndëm gi laa gàddu sama ëmb, ñuy gis.
Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ca ëllëg sa ca suba, ne ma: «Yaw nit ki, xanaa waa kër Israyil, kërug fippukat gi, newuñu la: “Ana looy def nii?” 10 Waxleen, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Boroom Yerusalem la àrtu bii ñeel, mook mboolem waa kër Israyil gi fi dëkk.” 11 Neel:
“Man maay seen misaal.
Nii ma def rekk lees leen di def,
ngàllo lees leen di jàpp, jëme.
12 Seen boroom dëkk beey gàddub ëmbam,
génn dëkk bi ci lëndëm gi.
Miiru dëkk bi lees di bëtt, jaarale ko ca.
Kanam ga lay muur,
ba tax du gis suuf si.
13 Maa koy laaw samab caax,
mu keppoo samag fiir,
ma yóbbu ko Babilon mu Kaldeen ña.
Réew ma, du ko gis te fa lay deeye.
14 Mboolem ña ko dar,
ay toppam ak mboolem gàngooram,
maa leen di wasaare fépp fu ngelaw jublu,
toppati leen ak saamar.
15 Bu ma leen tasaaree ci biir xeet yi,
wasaare leen ci réew yi,
ñu xam ne maay Aji Sax ji.
16 Du tee ma ba ñenn ci ñoom,
ñu mucc saamar, mucc xiif, mucc mbas,
ba nettaliji seen gépp tojaange
ca digg xeet ya ñu jëm.
Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.”»
17 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
18 «Yaw nit ki, lekkal saw ñam, di kat-kati,
naane njàqare sam ndox, di rag-ragi,
19 te nga wax waa réew mi,
mbirum waa Yerusalem ga ca suufas Israyil,
ne leen Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
njàqare lañuy lekkeji seenu ñam,
te xol bu gental lañuy naane seenum ndox,
ndax seen réew mu gental, ñàkk lépp lu ko feesoon,
ngir coxoru mboolem ñi ko dëkke.
20 Dëkk yu xumboon, mujj wéet,
réew mi doon ub gent,
ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.»
Waxyuy nit, waxi caaxaan
21 Gannaaw gi kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: 22 «Yaw nit ki, du lii ngeen defati aw léeb ci biir réewum Israyil? “Bés yaa ngi bëgga baree, te peeñu sottiwul!” 23 Kon wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maay dakkal woowu léeb,
ba muy léebtil fi Israyil.”
Waxleen kay ne leen:
“Bés a ngi jubsi,
peeñoo peeñu sotti.
24 Du peeñuy caaxaan muy amati mbaa ngisaaney jayaate,
fi biir kërug Israyil.
25 Man Aji Sax ji,
maay wax li may wax,
mu sotti te dootu fomm.
Kërug fippukat gi ngeen doon,
maay àddu kàddu, sottal ngeen fekke,
kàddug Boroom bi Aji Sax jee!”»
26 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: 27 «Yaw nit ki, waa kër Israyil déy a nga naan, “Peeñu yi kii di gis, des na ay fani fan, ci lu soree sore lay biral ab waxyu!” 28 Moo tax wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Sama genn kàddu dootu fomm.
Léegi kàddu gu ma àddu, sottal ko.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»