5
1 Amos ne:
Yeen bànni Israyil, dégluleen mii pent:
maa ngi leen di jooy, yeen bànni Israyil!
2 Fëlëñ!
Israyil janq ba dootu jógati.
Ma nga ñu wacc ca suufas réewam,
te amul ku ko yékkati.
3 Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Junniy xarekat ay génne fii,
téeméer délsi;
téeméeri xarekat génne fee,
fukk délsi,
ñeel waa kër Israyil.»
4 Aji Sax ji da ne waa kër Israyil:
«Sàkkuleen ma,
ba dund.
5 Buleen sàkkuji fa Betel,
buleen dem Gilgal,
te buleen jàll Beerseba.
Gilgal ay gàlloo ngàllo;
Betel neen.»
6 Sàkkuleen Aji Sax ji,
ba dund.
Lu ko moy mu ne jippét ci kaw askanu Yuusufa,
lakk waa Betel lakk gu dul fey.
7 Wóoy yeen ñiy walbati àtteb yoon, mu mel ni xay,
tey jalax dëgg fi pëndub suuf!
8 Kee sàkk biddiiwi lolli ak biddiiwi cooroon,
mooy walbati lëndëm bët set,
def bëccëg di guddi.
Keey woo walum géej,
walal fi kaw suuf.
Kookoo di Aji Sax ji.
9 Moo naan musiba jàyy ci kaw boroom doole,
musiba wàccal am tata.
10 Yeena bañ kuy yedde ci pénc,
te sib boroom làmmiñ wu maandu.
11 Gannaaw yeenay not néew-ji-doole,
di foqati ŋëbu peppam,
tabax ngeen këri boroom barke,
waaye dungeen ko dëkke.
Jëmbat ngeen tóokëri reseñ juy tem-temi,
waaye dungeen naan ca biiñ ba.
12 Ràññee naa seen bàkkaar yu bare
ak seen moy yu dul jeex.
Yeenay tooñ aji jub, di geru,
di xañ néew-ji-doole dëgg ci pénc.
13 Moo tax ku xelu ci jii jamono ne cell.
Céy jii jamono ju bon!
14 Sàkkuleen lu baax, ba lu bon,
ba dund,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi ànd ak yeen,
muy li ngeen wax.
15 Bañleen lu bon, bëgg lu baax,
di doxal yoon ci pénc.
Jombul Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
baaxe ndesu askanu Yuusufa.
16 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji, Yàlla ji ci gàngoori xare yi, dafa ne:
«Bayaaloo bayaal ubalee ki yuux,
mbeddoo mbedd riir aki wóoy!
Dees na woo beykat bi ciy jooy,
woo jooykati dëj ciy jooyoo.
17 Tóokëroo tóokër ay ubalee ki yuux.
Foofu fépp maa fay jaare.»
Aji Sax jee ko wax.
18 Wóoy kuy yàkkamti bésub Aji Sax ji!
Ana lu ngeen am ci bésub Aji Sax ji?
Dug leer, xanaa lëndëm.
19 Day mel ni kuy daw gaynde,
ne pemm cim segg, rëcc,
ñibbi, teg loxoom ca tabax ba,
jaan ne ko càppit.
20 Xanaa du lëndëm gu dara leerul la bésub Aji Sax jiy doon,
ne këruus, dara lerxatu ca?
21 «Maa bañ, maa sib seeni màggal,
seen ndajey diine génnliku na ma.
22 Ngeen defal ma saraxu rendi-dóomal,
mbaa saraxi pepp it, duma ko nangu.
Seen saraxu jur guy cant ci biir jàmm,
faalewuma.
23 Xiddileen maak seen coowal jàng.
Seen powum xalam safu ma.
24 Na yoon wal xanaa, nim ndox,
te dëgg mel ni wal mu sax.
25 «Yeen bànni Israyil, saraxi gàtt ak saraxi pepp,
ndax man ngeen ko daan indil
diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
26 Te ngeen di yékkati seen tuur yi ngeen sàkk:
Sikkut, di seen buur, di seen tuur,
Kiyun di biddiiw bu ngeen di jaamu.
27 Maa leen di yóbbu ngàllo ca wàllaa Damaas.»
Aji Sax jee ko wax, kookooy Yàlla Boroom gàngoori xare yi.