2
1 Kon nag dëdduleen gépp coxor, gépp njublaŋ, naaféq, kiñaan ak jëw.
2-3 Gannaaw ay liir ngeen yuy doora juddu te mos ci mbaaxug Boroom bi, nàmpleen ci meew mu sell, miy dundal seen xol, ba màgg ci biir muccu Yàlla.
Mbooloom Yàlla dafa mel ni tabax, Kirist mooy fondamaa ba
4 Kon nag ñëwleen ci moom; nit ñi bañ nañu ko, waaye Yàlla fal na ko te teral ko. Mi ngi mel ni doju tabax, waaye doj wuy dund la,
5 te yéena ngi mel niy doj yuy dund yu Yàllay defare dëkkukaayam. Noonu ay sarxalkat yu sell ngeen, ngir jébbal ko ay sarax yu ngeen tibbe ci seen xol te neex ko ndax Yeesu Kirist.
6 Looloo tax bind nañu:
«Maa ngi samp fi ci Siyoŋ doju koñ. Doj wu tedd la, wu ma tànn;
ku gëm ci moom, sa yaakaar du tas mukk.»
7 Kon nag yéen ñi gëm am ngeen cér ci teraangaam. Waaye naka ñi gëmul:
«Doj wa tabaxkat ya sànni,
mujj na di doju koñ.»
8 Te it:
«Doj la wuy fél nit,
di xeer wu koy fakktal.»
Dañu cee fakktalu, ndaxte gëmuñu kàddug Yàlla, te loolu la Yàlla dogal ci ñoom.
9 Waaye yéen xeet wu Yàlla tànn ngeen, di askanu sarxalkati Buur Yàlla, askan wu sell ngeen, di mbooloom Yàlla, ngir ngeen yégle ngëneelam, moom mi leen woo, ba génne leen lëndëm gi, tàbbal leen ci leeram gu yéeme gi.
10 Démb nekkuleen woon ci dara, waaye tey mbooloom Yàlla ngeen; booba jotuleen woon yërmandeem, waaye léegi jot ngeen ko.
11 Samay xarit, yéen ñiy ay gan ak i doxandéem ci àddina si, maa ngi leen di dénk lii: dëdduleen bànneexi bakkan yiy xeex ak xol.
12 Na seen dundin rafet ci biir xeeti àddina, kon doonte ñu di leen sosal ay ñaawteef, dinañu gis seeni jëf yu rafet bay màggal Yàlla, bés bu leen feeñoo.
Déggal-leen njiit yi
13 Na seen nangub Boroom bi tax, ngeen déggal képp kuy kilifa, muy buur ba gëna kawe,
14 mbaa jawriñ yu mu yebal, ngir ñu yar ñiy def lu bon, te teral ñiy def lu baax.
15 Ndaxte noonu la coobarey Yàlla tëdde, maanaam ngeen sax ci def lu baax, ba wedamloo jayil yi xamul dara.
16 Li leen Yàlla goreel nag, bu mu tax ngeen mbubboo ko, bay def lu bon, waaye ngeen gëna feddali seen jaamu Yàlla.
17 Teral-leen ñépp, bëgg kureelu bokk yi, ngeen ragal Yàlla te teral buur bi.
Kirist sunu royukaay ci dékku coono
18 Yéen jaam yi, déggal-leen seeni sang ak wegeel gu mat sëkk, waxuma ñi baax te lewet rekk, waaye sax ñu wex ñi.
19 Ndaxte su ngeen dékkoo tiis, di sonn ci lu dul yoon ndax seen ànd ak Yàlla, loolu lu rafet la.
20 Su ngeen tooñee te muñ i pes, luy pey gi? Waaye su ñu leen fitnaalee ci def lu baax te ngeen muñ ko, jëf ju rafet la fa kanam Yàlla.
21 Ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ndaxte Kirist itam sonn na ngir yéen, teg fi seen kanam royukaay, ngir ngeen jaar ciy tànkam.
22 «Masula def bàkkaar,
te jenn waxu njublaŋ masula génn ci gémmiñam.»
23 Saaga nañu ko te feyuwul, fitnaal nañu ko te tëkkuwul, waaye mu dénk boppam ki yor àtte bu dëgg bi.
24 Gàddu na moom ci boppam sunuy bàkkaar ca bant, ba ñu ko daajoon, ngir nu tàggook bàkkaar, sóobu ci dund gu jub; ndax ay gaañu-gaañoom may na nu ag wér.
25 Ndaxte yéena ngi réeroon niy xar, waaye léegi délsi ngeen ci sàmm, biy aar seeni xol.