22
Léebu céet ga
1 Gannaaw loolu Yeesu nettali leen beneen léeb ne leen:
2 «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur buy waajal céetu doomam ju góor.
3 Noonu mu yónni ay surgaam, ngir ñu woo gan yi ca céet ga, waaye gan yi bëgguñoo ñëw.
4 Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ”
5 Waaye ba tey wuyuwuñu ko; ñu dem, kenn ki ca toolam, kenn ki jaayaani,
6 ña ca des jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen.
7 «Noonu buur mer, daldi yónni ay xarekatam, ngir ñu rey bóomkat yooyule, lakk seen dëkk.
8 Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Reeri céet gi noppi na, waaye ñi ñu woo yeyoowuñu ko.
9 Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.”
10 Noonu surga ya génn ca yoon ya, boole ña ñu fa gis ñépp, ñu bon ña ak ñu baax ña, ba néegu reer ya fees ak ay gan.
11 «Bi nga xamee ne buur bi dugg na nag, ngir seetsi gan yi, mu gis fa nit ku solul mbubb mu ñu wara sol ca céet ga.
12 Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig.
13 Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.”
14 Ndaxte ñi ñu woo bare nañu, waaye ñi ñu tànn barewul.»
Galag gi ñuy fey buur bi Sesaar
15 Booba Farisen ya dem gise, ba xam lu ñu wara def, ngir fiir Yeesu ci waxam.
16 Noonu ñu yónni ci moom seeni taalibe ak ñi far ak buur bi Erodd ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.
17 Wax nu nag loo xam ci lii: ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet?»
18 Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi?
19 Wonleen ma poset, bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox nag benn posetu denariyon.
20 Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?»
21 Ñu ne ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
22 Bi nga xamee ne dégg nañu loolu, ñu waaru, bàyyi ko, daldi dem.
Sadusen yi ak ndekkite li
23 Bés boobale ay Sadusen ñëw ci moom. Sadusen yi nag ñoom gëmuñu ne ndekkite am na. Noonu ñu laaj ko naan:
24 «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.”
25 Amoon na ci nun nag juróom ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba am jabar ba noppi, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom.
26 Ñaareel ba ak ñetteel ba def noonu, ba ci juróom ñaareel ba.
27 Gannaaw ñoom ñépp, jigéen ja faatu.
28 Bu ndekkite taxawee nag, jabaru kan lay doon ci juróom ñaar ñi, ndaxte ñépp jël nañu ko?»
29 Waaye Yeesu ne leen: «Yéena ngi cig réer, ndaxte xamuleen Mbind mi mbaa kàttanu Yàlla.
30 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am jëkkër, waaye dinañu mel ni malaaka yi ci kaw.
31 Te lu jëm ci ndekkitel ñi dee, xanaa masuleena jàng la leen Yàlla waxoon ne:
32 “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.»
33 Bi nga xamee ne mbooloo ma dégg nañu loolu, ñu waaru ndax li mu jàngle.
Ban santaane moo gëna màgg ci yoonu Musaa?
34 Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje.
35 Noonu kenn ci ñoom, ka nekk xutbakat, fexe koo fiir. Mu laaj ko:
36 «Kilifa gi, ban ndigal moo gëna màgg ci yoonu Musaa?»
37 Yeesu ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.”
38 Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane.
39 Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”
40 Ñaari ndigal yooyu tënk nañu yoonu Musaa wépp, moom ak waxi yonent yi.»
Ndax Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
41 Bi Farisen ya dajee nag, Yeesu laaj leen:
42 «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.»
43 Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne:
44 “Boroom bi wax na sama Boroom:
‘Toogal ci sama ndijoor,
ba kera may daaneel
say noon ci sa kanam.’ ”
45 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
46 Ci kaw loolu kenn manu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara.