9
Yeesu faj na gumbag judduwaale
1 Amoon na fu Yeesu jaaroon, gis fa waa ju judduwaale gumba.
2 Taalibeem ya laaj ko ne: «Kilifa gi, lu tax waa jii judduwaale gumba? Ndax bàkkaaram a ko waral, walla bu waajuram?»
3 Yeesu ne leen: «Ajuwul ci bàkkaaram walla ci bu waajuram. Waaye loolu dafa am, ngir jëfi Yàlla yi feeñ ci moom.
4 Bëccëg lanu wara matal jëfi ki ma yónni; guddi dina ñëwi, goo xam ne kenn du ci mana liggéey.
5 Ci bi may nekk àddina, maay leeru àddina.»
6 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, dafa daldi tifli, jaxase lor wa ak ban, tay ko ci bëti gumba ga ne ko:
7 «Demal sëlmu ci bëtu Silowe.» Silowe mi ngi tekki «Yónni nañu ko.» Gumba ga daldi dem sëlmuji, délsi di gis.
8 Dëkkandoom yi ak ñi ko xame woon bu jëkk ci yelwaan naan: «Xanaa du kii moo daan toog, di yelwaan?»
9 Ñii naan: «Moom la de!» Ñee naan: «Du moom! Dañoo niroo rekk.» Mu daldi leen ne: «Man la de!»
10 Ñu ne ko: «Lu ubbi say bët?»
11 Mu ne leen: «Ku ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, tay ko ci samay bët, ne ma: “Demal sëlmu ci bëtu Silowe.” Ma dem nag sëlmuji, daldi gis.»
12 Ñu ne ko: «Ana waa ji?» Mu ne leen: «Xawma fu mu nekk.»
Farisen laaj nañu gumba, gi ñu wéral
13 Noonu ñu daldi indil Farisen yi nit ki gumba woon.
14 Ndekete Yeesu, bés bi mu tooyale ban, ubbi bëti gumba ga, bésub noflaay la woon.
15 Looloo tax Farisen ya di laajaat waa ja fi mu jaar bay gis léegi. Mu ne leen: «Dafa tay ban ci samay bët, ma sëlmuji, ba fi ma nekk maa ngi gis.»
16 Ci noonu am ca Farisen ya ñu naan: «Ki def lii, manula jóge ca Yàlla, ndaxte toppul ndigalu bésub noflaay bi.» Ñeneen it di wax ne: «Nan la boroom bàkkaar mana wonee yii firnde?» Noonu ñu daldi féewaloo ci seen biir.
17 Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: «Yaw, loo wax ci moom? Yaw de la ubbil say bët.» Mu ne leen: «Yonent la.»
18 Yawut ya manuñu woona nangu ne, nit ka dafa gumba woon tey gis léegi, ñu daldi wooluji ay waajuram,
19 laaj leen ne: «Ndax kii mooy seen doom, ji ngeen ne gumba judduwaale la? Kon fu mu jaar, bay gis léegi?»
20 Waajur ya ne leen: «Xam nanu ne daal, sunu doom la te dafa judduwaale gumba.
21 Waaye ni mu def léegi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay bëtam. Laajleen ko; magum jëmm la, te man na tontul boppam.»
22 Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne, képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba.
23 Looloo tax waajur ya ne: «Laajleen ko; magum jëmm la.»
24 Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Xam nanu ne waa joojee boroom bàkkaar la.»
25 Mu ne: «Xawma ndax boroom bàkkaar la am déet. Li ma xam daal mooy gumba woon naa, te léegi maa ngi gis.»
26 Ñu laaj ko ne: «Lu mu la def? Nu mu la ubbile say bët?»
27 Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye dégluwuleen ma. Lu ngeen bëgg ci ma di ko wax, di waxaat? Xanaa dangeena bëgga nekk yéen itam ay taalibeem?»
28 Ci kaw loolu ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeem. Nun, taalibey Musaa lanu.
29 Xam nanu ne Yàlla wax na ak Musaa; waaye kii, xamunu sax fu mu jóge.»
30 Waa ja ne leen: «Loolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu jóge, te moo ubbi samay bët!
31 Xam nanu ne Yàlla du déglu boroom bàkkaar. Waaye nag, dina déglu ki koy ragal tey def coobareem.
32 Bi àddina sosoo ba tey, masuñoo dégg nit ku ubbi bëti gumbag judduwaale.
33 Kon nit kookee nag, bu jógewul woon ca Yàlla, du mana def dara.»
34 Ñu ne ko: «Yaw, ci biir bàkkaar nga juddoo, ba noppi di nu jàngal?» Noonu ñu dàq ko ca jàngu ba.
Ngumbag xel
35 Yeesu daldi yég ne dàq nañu nit ka. Bi mu dajeek moom, mu ne ko: «Ndax gëm nga Doomu nit ki?»
36 Waa ja ne ko: «Wax ma mooy kan, Sang bi, ba ma man koo gëm.»
37 Yeesu ne ko: «Gis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yaw.»
38 Waa ja ne: «Boroom bi, gëm naa la.» Noonu mu jaamu Yeesu.
39 Yeesu ne ko: «Àttee ma taxa ñëw àddina, ngir ñi gumba gis, ñiy gis gumba.»
40 Bi Farisen ya nekkoon ak moom déggee loolu, ñu ne ko: «Xanaa kon nun it danoo gumba?»
41 Yeesu ne leen: «Bu ngeen gumba woon, dungeen am bàkkaar, waaye fi ak yéena ngi naan: “Nu ngi gis,” ci bàkkaar ngeen di dëkk.