2
Buleen gënale
1 Yéen samay bokk, bu benn gënale laal seen ngëm ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi soloo ndam.
2 Ndaxte su ñaari nit duggee ci seen mbooloo, kii takk jaaroy wurus te sol yére yu taaru, ka ca des ñàkk te limboo ay sagar,
3 ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,»
4 kon gënale ngeen ci seen biir, ba àtte ci col, bàyyi xol.
5 Dégluleen yéen sama bokk yi ma bëgg, ndax Yàlla tànnul ñi néewle ci àddina, ngir ñu barele ci ngëm, tey am i cér ci nguur, gi Yàlla dig ñi ko bëgg?
6 Fekk dangeen leen di toroxal! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di not te di leen yóbbu fa kanam àttekat yi?
7 Ndax duñu tilimal tur wu tedd, wi ngeen di wuyoo?
8 Su ngeen sàmmee yoonu Buur Yàlla, ni ko Mbind mi tërale naan: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp,» kon def ngeen lu baax.
9 Waaye su ngeen gënalee, bàkkaar ngeen, te yoonu Yàlla dina leen dab ni ñu moy.
10 Ndaxte ku sàmm yoon wépp, waaye xëtt ci lenn ndigal rekk, jàdd nga yoon wépp.
11 Ndaxte Yàlla mi ne: «Bul njaaloo», teg na ca ne: «Bul bóome.» Ku njaaloowul nag, waaye nga bóome, jàdd nga yoon wépp.
12 Gannaaw dingeen nara jaar ci àtteb yoon, wiy goreel, na loolu lal seen wax ak seen jëf.
13 Ndaxte ku yërëmul, yoon du la yërëm. Te yërmande mooy not àtte.
Ku gëm dina ko feeñal ciy jëfam
14 Te lii itam samay bokk: ku ne gëm nga, te jëfewoo ko, loolu lu muy jariñ? Ndax googu ngëm man na laa musal?
15 Su amee mbokk ci seen biir, mu rafle te amul dund, muy góor walla jigéen,
16 te kenn ci yéen ne ko: «Demal ak jàmm, nga solu te lekk,» te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jariñ?
17 Noonu ngëm gu àndul ak jëf, amul benn njariñ.
18 Waaye xanaa dina am ku ne: «Yaw am nga ngëm, man am naa ay jëf.» Yaw nag won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, ma feeñal la sama ngëm ci samay jëf.
19 Gëm nga ne Yàlla kenn la; loolu lu baax la, waaye xamal ne, jinne yi it gëm nañu loolu, ba dañoo tiit bay lox.
20 Yaw mi gàtt xel, kaay ma won la ne ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ.
21 Sunu maam Ibraayma, ndax du ci kaw jëf la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu joxe doomam Isaaxa ni sarax?
22 Kon gis nga ne ngëm dafa lëngoo ak ay jëfam, te ngëmam mat ci kaw jëf jooju.
23 Noonu li ñu wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub,» ba ñu ko wooye xaritu Yàlla.
24 Kon nag gis nga ne Yàlla ci jëf lay àtte nit ni ku jub, waaye du ci kaw ngëm kese.
25 Naka Raxab jigéenu moykat bi itam, ndax du ci noonu la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu teeru ndawi Yawut yi, te jaarale leen ca poot ba?
26 Kon nag ni jëmm ju amul ruu nekke ndee, noonu la ngëm gu àndul ak jëf nasaxe.