Bataaxal bi Yàlla may Pool,
mu bind ko
WAA EFES
1
1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobarey Yàlla, maa leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell yi te gëm Kirist Yeesu ci dëkku Efes.
2 Yal na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
3 Cant ñeel na Yàlla Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu sotti ci sunu bokk ci Kirist lépp luy barkeel ci baatin te nekk ca bérab yu kawe ya.
4 Ndaxte ba àddina sosoogul, tànn na nu ci Kirist, ngir nu mana teew fa kanamam, sell te ñàkk sikk. Ci kaw mbëggeelam
5 séddoo na nu lu jiitu, def nu ay doomam jaarale ko ci Yeesu Kirist, ndaxte looloo doon yéene ju rafet, ji mu tëral ci coobareem.
6 Na ndamam jolli ndax yiw wu réy, wi mu nu sotti ci Soppeem bi.
7 Moom jot na nu ak deretam ji ñu tuur, maanaam baal nu sunuy bàkkaar, ci kaw yiw wu yaatu,
8 wi mu nu baawaanal. Yàlla sol na nu xel mu mat ak dégg,
9 ci feeñal nu mbóoti coobareem, dëppook yéeneem ju rafet, ji mu jaarale ci Kirist.
10 Mu tëral ne, bu jamono yi wéyee ba lépp mat, dina dajale lépp ci kilifteefu Kirist, muy ci kaw, muy ci suuf.
11 Am nanu cér ci moom bu nu Yàlla sédd lu jiitu ci dogalam, moom miy doxal lépp ci ni mu ko àttee ci coobareem.
12 Noonu nuy jollil ndamam, nun ñi jëkka wékk sunu yaakaar ci Kirist.
13 Yéen itam, bi ngeen déggee kàddug dëgg gi, di xibaaru jàmm, bi leen tegtal yoonu mucc, te ngeen gëm ko, Yàlla tàmpe na leen ni ñoñam ak Xel mu Sell, mi mu dige woon.
14 Te Xel mi mooy dawal gi nu Yàlla jox ci cér, bi mu nu dencal, ba kera muy goreel ñi mu jotal boppam, te ñépp jollil ndamam.
Pool sant na Yàlla, di ñaanal ñi gëm
15 Bi ma déggee nag seen ngëm ci Boroom bi Yeesu ak seen mbëggeel ci gaayi Yàlla yu sell yépp,
16 duma noppee sant Yàlla, di leen boole ci samay ñaan.
17 Li may ñaan Yàllay sunu Boroom Yeesu Kirist, di Baay bi yelloo ndam, mooy lii: mu sol leen xel mu xóot, te xamal leen boppam
18 ci leeral seeni xol. Noonu dingeen xam yaakaaru ëllëg, ji leen Yàlla wooye, di ndam lu xel manta daj, li nekk ci cér, bi mu dencal gaayam yu sell yi.
19 Ngeen xam it, ni kàttanam màgge ba jéggi dayo, jëm ci nun ñi gëm, dëppook dooleem ju ràññiku,
20 ji mu jëfe ci Kirist, ci li mu ko dekkal, dëël ko ci ndijooram ca bérab yu kawe ya,
21 mu tiim lu sore malaaka yépp, muy kilifa, boroom sañ-sañ, boroom doole mbaa buur, te gëna màgg wépp tur wu ñu mana tudd, muy tey, muy ëllëg.
22 Yàlla suufeel na lépp fi kanamam, def ko kilifag lépp ci mbooloom ñi gëm,
23 miy jëmmam, di matug Kirist, mi fees mbindeef mu ne ci fànn gu ne.